Bataaxal bi jëm ca
YAWUT YA
1
Yàlla wax na jaarale ko ci Doom ji
1 Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.
2 Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
3 Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndijooru Aji Màgg ji ca kaw,
4 wone noonu ne moo gëna màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur.
Doom jee gëna màgg malaaka yi
5 Ndaxte Yàlla masula wax kenn ci malaaka yi ne:
«Yaa di sama Doom,
maa di sa Baay tey.»
Masul ne ci mbirum kenn ci ñoom it:
«Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom,
mu nekk Doom ci man.»
6 Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne:
«Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.»
7 Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax:
«Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw,
ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki sawara.»
8 Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax:
«Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww,
ci njubte ngay nguuru.
9 Sopp nga njub te bañ lu bon.
Looloo tax yaw Yàlla,
sa Yàlla sol la mbég mu gëna réy
mi mu jagleel say àndandoo.»
10 Newaat na it:
«Yaw Boroom bi, yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga,
defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.
11 Yëf yooyu dinañu wéy,
waaye yaw dinga sax,
dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.
12 Dinga leen taxañ ni malaan,
ñu furi ni ay yére,
waaye yaw doo soppiku,
te sa dund amul àpp.»
13 Waaye Yàlla masula teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:
«Toogal ci sama ndijoor,
ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.»
14 Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nara jot mucc gi.