3
Moom sa làmmiñ
1 Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jànglekatu mbooloo mi, xam ne nun jànglekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gëna diis.
2 Ndaxte nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga te mana not sa yaram wépp.
3 Noonu ku laab fas, ngir mu déggal la, not nga jëmmam jépp.
4 Gaal yi it yu réy lañu, te ngelaw lu am doole di leen jañax, waaye dawalkat bi, weñ gu tuuti la leen di jëme fu ko neex.
5 Ci noonu làmmiñ, cér su tuuti la, waaye day bàkkoo jëf yu réy.
Seetleen ni ferñent tuutee te mana lakk àll bu yaatu.
6 Noonu it làmmiñ sawara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina.
7 Nit man na not xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi— not na lépp.
8 Waaye làmmiñ kenn manu koo not; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey.
9 Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom.
10 Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warula am.
11 Ndax ndox mu lewet ak mu wex dinañu ballandoo ci genn mbënn?
12 Samay bokk, ndax mas ngeena gis garabu figg gu meññ oliw, walla garabu reseñ gu meññ ay figg? Mukk! Mbënnu xorom manta nàcc mukk ndox mu neex.
13 Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet.
14 Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul bàkku, di weddi dëgg.
15 Xel moomu jógewul ci kaw; jëfu àddina la, di jikkoy niti kese, te jóge ci Seytaane.
16 Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef.
17 Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
18 Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.