7
Yeesu ca màggalu Mbaar ya
Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile. Bëggul woona dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wuta rey.
Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi. Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def. Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.» Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax. Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul. Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.» Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam. 11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?» 12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.» 13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
Yeesu jàngle na ca màggal ga
14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga. 15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16 Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge. 17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare. 18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn. 19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?» 20 Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?»
21 Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle! 22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi. 23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm? 24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
Ndax Yeesu mooy Almasi bi?
25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey? 26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi? 27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28 Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko. 29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30 Noonu ñu koy wuta jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon. 31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?» 32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33 Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sooga dem ci ki ma yónni. 34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen mana dem fa may nekk.»
35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nara dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya? 36 Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen mana dem fa may nekk”?»
37-38 Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”» 39 Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroona jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
40 Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi wara ñëw.» 41 Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi mana jógee Galile? 42 Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.» 43 Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu. 44 Am na ca ñoom ñu ko bëggoona jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
Njiiti Yawut yi gëmuñu Yeesu
45 Bi alkaati ya delloo, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?» 46 Alkaati ya ne leen: «Kenn masula waxe ni nit kooku!» 47 Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam? 48 Ndax am na kenn ci sarxalkat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet. 49 Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen: 51 «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?» 52 Ñu ne ko: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne benn yonent masula jóge Galile.» 53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.