10
1 Bokk yi, sama coobarey xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc.
2 Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam.
3 Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu baña nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral.
4 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla.
Yàlla bëggoon na ñépp mucc
5 Ku bëgga jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoona matal, dinga dund ba fàww.»
6 Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe:
«Bul wax ci sa xol ne: “Kuy yéeg ci kaw?”»
mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc.
7 «Bul wax it: “Kuy dem ca barsàq?”»
mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
8 Kon boog lan lay wax? Lii:
«Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet, ci sa làmmiñ, ci sa xol.»
Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
9 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
10 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
11 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
12 Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp; ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
13 Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
14 Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Naka lañu mana gëme ki ñu déggagul turam? Naka lañu mana dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
15 Nan lañu mana waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xibaaru jàmm bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
16 Waaye ñépp nanguwuñu xibaaru jàmm bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»
17 Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xibaaru Kirist.
18 Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Ahakay! Mbind mi wax na ne:
«Seen baat jolli na ci ñeenti xébla yépp,
seen wax wër na àddina sépp.»
19 Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa dafa jëkkoona wax ne:
«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,
merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
20 Esayi it takk na fitam, ba wax ne:
«Ñi ma wutul woon, gis nañu ma,
feeñ naa ci ñi ma laajul woon.»
21 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:
«Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon,
ci xeet wu may bañ tey werante.»