2
Beyal sa sas
1 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.
2 Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu mana jàngal ñeneen.
3 Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,
4 xam ne xarekat bu bëgga neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
5 Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya.
6 Noonu it beykat bi sonn mooy jëkka ñam toolam.
7 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp.
8 Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xibaaru jàmm bi may waare.
9 Xibaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng.
10 Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax.
11 Kàddu gu wóor a ngii:
Su nu deeyaalee ak Kirist,
dinanu dundaat ak moom;
12 su nu takkoo,
dinanu nguuru ak moom.
13 Su nu ko weddee,
kon mu weddi nu;
su nu ko ñàkkee kóllëre,
moom dina sax ci kóllëreem,
ndax manula weddi boppam.
Liggéeykat bu neex Yàlla
14 Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu.
15 Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi.
16 Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gëna xuus cig weddi,
17 te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk;
18 dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi.
19 Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
20 Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo.
21 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet.
22 Dawal bépp bëgg-bëggu ngone, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.
23 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur.
24 Te jaamu Boroom bi warula xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngle tey muñ fitnay noon.
25 Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg;
26 ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu délsi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobarey Yàlla.