4
Piyeer ak Yowaan daje nañook àttekat ya
1 Naka la Piyeer ak Yowaan di wax ak mbooloo ma, sarxalkat yaak jawriñu kër Yàlla gaak Sadusen ya ne jimeet ci seen kaw.
2 Fekk na leen ñéññ ca la ñuy waare ak a yégle ndekkitel Yeesu, te loolu di dëggal ne ndee-ndekki, lu am la.
3 Ñu daldi leen teg loxo, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndax booba guddi na.
4 Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).
5 Ca ëllëg sa kilifay Yawut yi ak mag ñi ak firikati yoon yi daje Yerusalem.
6 Anas, sarxalkat bu mag ba ca la, ak Kayif ak Yowaan ak Alegsàndar, ak mboolem bokki sarxalkat bu mag.
7 Ñu taxawal Piyeer ak Yowaan ca digg ba, laaj leen ne: «Yeen, lii ngeen def, ci ban xam-xam, ak ci wan tur ngeen ko defe?»
8 Fa la Piyeer feese Noo gu Sell gi, ne leen: «Yeen kilifay xeet wi ak mag ñi,
9 ndegam yoon moo nuy laaj lu jëm ci ndimbal lu ab lafañ jagoo, ak ci man pexe la lafañ bi mucce,
10 xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
11 Yeesu moomu mooy:
“Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi,
te mu mujj di doju coll wi.”
12 Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
13 Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
14 Te itam ka ñu wéral a nga taxaw fa seen wet, ñuy gis. Manuñu caa tegati dara.
15 Ba mu ko defee ñu joxe ndigal, génne leen, daldi gise ci seen biir.
16 Ñu ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndax kat firnde lu leer sottee na fi ci ñoom; leer na nàññ waa Yerusalem gépp, te manunu koo weddi.
17 Waaye kat bu mbir mi gëna siiw ci xeet wi. Nan leen tëkku, ngir aaye leen ñu waxati kenn tur woowu.»
18 Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.
19 Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.
20 Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
21 Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
22 ngir waa, ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
Mbooloom gëmkat ñi ñaan na ci Yàlla
23 Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak mag ña wax.
24 Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
25 Yaa waxe Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne:
“Lu xeeti àddina di riir?
Lu xeet yiy lal pexey neen?
26 Buuri àddinaa jógandoo,
kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”
27 Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.
28 Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.
29 Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy waxe sa kàddu fit wu mat sëkk.
30 Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral ak a amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa ndaw lu sell li.»
31 Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
Gëmkat ñi ñoo bokkoon lépp
32 Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel, ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.
33 Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp.
34 Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njég li,
35 teg ko ci kanam ndaw yi. Su ko defee ku nekk séddu ca la dëppook soxlaam.
36 Ku mel ni Yuusufa, bokk ci giirug Lewi, te dëkke dunu Sippar, ndaw yi daan ko wax Barnaba, mu firi Ñaaxekat bi,
37 ab tool la amoon. Da koo jaay, indi xaalis bi, teg fi kanam ndaw yi.