2
Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
laay sikke waa Mowab,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo lakk yaxi buurub Edom, def ub dóom.
Maay yebal sawara réewum Mowab,
mu xoyom tatay Keryot*.
Mowab deeye biir riirum xare,
yuux ak liitu xare jibandoo.
Maay dagge fa seen biir seen njiit,
booleeki kàngamam, bóom.»
Aji Sax jee ko wax.
 
Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
laay sikke Yudeen ñi,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo gàntal sama yoon man, yoonu Aji Sax ji,
te sàmmuñu sama dogali yoon.
Seen tuuri caaxaan ya seeni maam toppoon
sànk na leen.
 
«Maay yebal sawara ci kaw Yudeen ñi,
mu xoyom tatay Yerusalem.»
Israyil a gëna yelloo mbugal
Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
laay sikke Israyil,
te duma fomm seeni duma.
Ñooy jaay jaam aji jub ngir xaalis bu mu leen ameel,
jaay aji ndóol bu manul fey dàlli carax.
Ñooy dëggaate néew-ji-doole ci pëndub suuf,
di xañ way-ñàkk àqam.
Nit ak baayam di tëdde as ndaw,
di teddadil sama tur wu sell.
Yérey tayle yu ñu nangoo ci néew-ji-doole sax,
ñu lal, ne ñàyy ci wetu mboolem sarxalukaay.
Ku leen ameel, ñu feyloo la biiñ,
naan ca seen biir kër tuur ya.
 
«Ndaxam maa leen reyaloon Amoreen
ñu gudd ña te réy, mbete garab yu mag.
Ma boor doom ya,
buur reen ya.
10 Fekk yeen, ma génnee leen réewum Misra,
jaarale leen màndiŋ ma diiru ñeent fukki at,
ngir ngeen nanguji réewum Amoreen ñi.
11 Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent,
tànne ci seen xale yu góor ay séddoo,
— am déet, yeen bànni Israyil?»
Kàddug Aji Sax jee.
12 «Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ.
Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen biral waxyu!”
 
13 «Maa ngii di yëngal suuf si ngeen joggi,
ni watiir wu fees aki sabaar di yëngale suuf.
14 Rawtu dina réer ku gaaw,
boroom doole du tala jariñoo dooleem,
jàmbaar sax du mana rawale bakkanam.
15 Fittkat du taxaw,
mana daw du taxa raw.
Ab gawar it du rawale bakkanam.
16 Bésub keroog, jàmbaar ju ëppu fit,
duŋŋ lay def, di daw.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
* 2:2 Keryot dëkku Mowab bu réy la woon. 2:11 séddoo yooyu nasireen lañu leen di wooye. Seetal ci Màndiŋ ma 6.