16
Lu jëm ci ndimbal lu ñeel gëmkati Yerusalem
Ci wàllu ndimbal li jëm ci gëmkat ñu sell ñi, noonu ma ko digale mboolooy gëmkati diiwaanu Galasi, yeen itam defeleen ko noonu. Bés bu jëkk ci ayu bés yi, na ku nekk génne as lëf ca la mu am, na mu ko àttane, te mu dencal ko boppam, ngir bu ma dikkee, dootu soxlaa wër, di dajale. Bu ma dikkee, ñi ngeen tànn, ñoom laay yebale ab bataaxal, ngir ñu yóbbu Yerusalem seen ndimbal. Su aajoo ma dem man itam, ñu ànd ak man.
Póol mébét na, dénkaane na
Dinaa dikk ba ci yeen, gannaaw bu ma jaaree diiwaanu Maseduwan, ndax Maseduwan laay jaare. Man naa am ma yàgg ci yeen, jombul sax ma lollikoo fi yeen. Su ko defee ngeen yiwi ma, ma dem, ak fu ma mana jëm. Ndaxte itam, buggumaa jaare fi yeen rekk, jàll, waaye yaakaar naa toog ci yeen ab diir, su ko Boroom bi mayee. Waaye ci Efes gii laay toog ba màggalu Pàntakot, ndax bunt ubbikul na ma fi ŋàpp, ngir liggéey bu am njariñ, te noon yi bare nañu.
10 Bu Timote dikkee nag, fexeleen ba bumu am lu muy tiit ci seen biir, ndax liggéeyu Boroom bi lay liggéey ni man. 11 Kon bu ko kenn xeeb. Gannaaw loolu nangeen ko yiwi ak jàmm, ba mu délsi ci man, ndax moom laay xaar, mook bokk yi itam.
12 Mbokk mi Apolos nag moom, soññ naa ko lu bare, ngir mu dikk ba ci yeen, ànd ak bokk yi, waaye fii nu tollu yebuwu ci dara. Teewul bu jekkoo, dina dikk.
Yeneen ndigal a ngi aki tàggtoo
13 Teewluleen te saxoo ngëm, góor-góorluleen te dëgërlu. 14 Lépp lu ngeen di def, defeleen ko cofeel.
15 Bokk yi, xam ngeen ne Estefanas ak njabootam ñooy jooxeb ndoortel meññeef ci diiwaanu Akayi, te jàpple ñu sell ñi lañu séddoo. Kon dama leen di ñaan, 16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak mboolem ñu bokk ak ñoom liggéey bi ak coono bi. 17 Maa ngi bége teewaayu Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus, ndax bi ngeen wuutee tey, ñoo leen taxawal. 18 Dalal nañu sama xel, ak seen mos, yeen itam. Kon nit ñu mel noonu, fonkleen leen.
19 Mboolooy gëmkati diiwaanu Asi nag ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci turu Sang bi, ñoom ak mbooloom gëmkat ñiy daje seen kër. 20 Bokk yépp a ngi leen di nuyu.
Saafoonteeleen fóonante yu sell.
21 Man Póol maa bind nuyoo bii ci sama loxol bopp.
22 Ku buggul Sang bi, na alku. Maranata (mu firi sunu Sang, dikkal!)
23 Yal na yiwu Sang Yeesu ànd ak yeen.
24 Sama cofeel ñeel na leen, yeen ñépp, ci Yeesu Almasi mi nu bokk.