26
Njotlaayal Aji Sax ji laaj na ab galag
1 Gannaaw loolu, bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ba ngeen nangu ko, dëkke,
2 na ku nekk ci yeen sàkk ca ndoortel mboolem meññeefum suuf mu mu jële ca seen réew, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, mu def ko ci pañe, yóbbu ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
3 Na àgg ca sarxalkat ba fa nekk ci yooyu jant, ne ko: «Maa biral tey jii fi sa kanam Yàlla Aji Sax ji, ne agsi naa ci réew mi Aji Sax ji giñaloon samay maam, ne moom la may jox.»
4 Na sarxalkat bi nangoo pañe bi ci loxoom, taaj ko fi seen kanam sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji.
5 Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.
6 Waa Misra nag soxore nu, mitital nu, yen nu liggéey bu diis.
7 Ba loolu amee nu yuuxu, woo sunu Yàllay maam Aji Sax ji wall, Aji Sax ji dégg nu, gis sunu mitit, ak sunu coono, ak sunu notaange.
8 Aji Sax ji nag génne nu Misra ci dooley loxoom ak kàttanam, ci biir musiba mu réy, aki firnde, aki kéemaan.
9 Ba loolu wéyee mu indi nu fi bérab bii, jox nu réew mii, réew mu meew meek lem ji tuuroo.
10 Moo ma taxa indi nii ndoortel meññeefum suuf, si nga ma jox, Aji Sax ji.» Su ko defee mu taaj pañe bi fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, daldi sujjóot fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji.
11 Mu bége nag, moom ak Leween ñeek doxandéem yi dëkk ci seen biir, mboolem lu baax li ko seen Yàlla Aji Sax ji jox, moom ak waa këram.
12 Gannaaw bu ngeen génnee mboolem céru fukkeelub meññeef, ci atum ñetteel, yemook atum génne cérub fukkeel, gannaaw ñaari at yu nekk, nangeen ko jox Leween ñi ak doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun ñi, ngir ñu lekk ba regg, fa ñu féete ca seeni dëkk,
13 te na ku nekk ci yeen wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Jële naa sama kër céru sellnga bi, ba jox ko Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun yi, noonee mu dëppook sa santaane bi nga nu dénk. Moyuma lenn ci say santaane, te fàttewuma ci lenn.
14 Lekkuma ci dara ci biir ab dëj, jëlewuma ci dara te fekk ma sobewu, te it sarxaluma ci dara ku dee. Sama kàddug Yàlla Aji Sax ji laa topp, noonee nga ma ko sante woon.
15 Ngalla geesool fa sa dëkkuwaayu sellnga, fa asamaan, te nga barkeel Israyil, sa ñoñ, barkeel suuf si nga nu jox, noonee nga ko giñale woon sunuy maam, réew mu meew meek lem ji tuuroo.»
Kóllëre feddliku na
16 Bésub tey jii seen Yàlla Aji Sax ji moo leen sant ngeen jëfe dogal yii, ak àttey yoon yi. Sàmmooleen koo jëfe seen léppi xol, ak seen léppi bakkan.
17 Aji Sax ji ngeen biral bésub tey, ne mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam, aki santaaneem, ak àttey yoonam, tey dégg waxam.
18 Aji Sax ji it biral na bésub tey, ne yeenay doon ñoñam ñi mu séddoo, noonee mu leen ko dige woon, te ngeen di sàmm mboolemi santaaneem.
19 Moo leen di aj ba ngeen tiim mboolem xeet yi mu sàkk, ci wàllu bayre, ak tur ak teddnga, te moo leen di def askan wu sell, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, noonee mu ko digee woon.