3
1 Ba loolu wéyee nu walbatiku, awe yoon wa yéeg jëm Basan. Og buuru Basan nag dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Eddrey.
2 Aji Sax ji ne ma: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp, akum réewam. Nanga ko def na nga defoon Siwon buurub Amoreen ba woon ca Esbon.»
3 Noonu la sunu Yàlla Aji Sax ji tege Og buuru Basan itam ci sunuy loxo, mook gàngooram gépp, nu duma leen ba desewul kuy dund.
4 Booba lanu nangu mboolemi dëkkam. Amul benn dëkk bu nu nanguwul ci ñoom: juróom benn fukki dëkk, mboolem diiwaanu Argob, ba bokk ca nguurug Og ca Basan.
5 Yooyu yépp di dëkk yu dàbblikoo tata yu kawe, ak bunt yu tëje ràpp, te limaaleesul dëkk-dëkkaan yu baree bare, yu dara wërul.
6 Nu faagaagal leen, na nu defoon ak Siwon buurub Esbon. Dëkk yépp lanu faagaagal: góor ak jigéen ba ca tuut-tànk ya.
7 Mboolem jur gaak alali dëkk ya nag, nu sëxëtoo.
8 Jant yooyu lanu nangoo ci loxol ñaari buuri Amoreen ñooña ca wàllaa dexu Yurdan, réew ma dale ca xuru Arnon, ba ca tundu Ermon.
9 Ermon googu la waa Sidon di wooye Siryoŋ, Amoreen ñi di ko wooye Senir.
10 Mboolem dëkki joor ga lanu nangu, ak mboolem diiwaanu Galàdd, ak mboolem Basan, ba ca Salka ak Eddrey, dëkki nguurug Og mu Basan.
11 Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar.
Séddale nañu penkub Yurdan
12 Suuf soosu nu nangu ca jant yooya, te dale ca Arower ga ca xuru Arnon ca bëj-saalum, ak ca bëj-gànnaar, genn-wàllu diiwaanu tundi Galàdd, aki dëkkam, maa ko jox Rubeneen ñi, ak Gàddeen ñi.
13 Ndesu Galàdd ak mboolem Basan gu nguurug Og, ma jox ko genn-wàllu giirug Manase. Diiwaanu Argob gépp ak Basan googu gépp, lañu daan wooye réewum Refayeen ña.
14 Yayir mi askanoo ci Manase moo nangu mboolem diiwaanu Argob, ba ca kemu réewum Gesureen ña, ak Maakateen ña. Moo tudde boppam Basan googu, ba tax ñu di ko wooye Sanci Yayir ba tey jii.
15 Askanu Makir laa jox diiwaanu Galàdd.
16 Rubeneen ñeek Gàddeen ñi laa jox la dale diiwaanu Galàdd ba ca xuru Arnon, diggu xur wa di seen kemu suuf ci genn wet, dexu Yabog di seen kemu ñook Amoneen ña.
17 Fa joor ga feggook dexu Yurdan it di kemu, diggante dexu Kineret ca bëj-gànnaar, ak ca bëj-saalumu géeju Xorom ga, ba ba ngay àgg ca suufu tundu Pisga, ca penku.
18 Jant yooyu laa leen sant ne leen: «Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jox réew mii, ngir ngeen nangu ko. Na xarekat yépp gànnaayu, jàll, jiitu seen bokki bànni Israyil.
19 Seeni jabar doŋŋ, ak seeni doom ak seenug jur, ndax xam naa ne jur gu takku ngeen am, ñooy des ci seen dëkk yi ma leen jox,
20 ba keroog Aji Sax ji noppalee seen bokki bànni Israyil ni yeen, fekk leen nangu, ñoom it, réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ca wàllaa dexu Yurdan. Su ko defee ku nekk ci yeen saña dellu ca céru suufam ba ma ko jox.»
21 Yosuwe itam, sant naa ko ci jant yooyu ne ko: «Sa bët moo la may mboolem ni seen Yàlla Aji Sax ji def ak ñaari buur yii. Noonu rekk la Aji Sax jiy def ak mboolem nguur ya nga jëm.
22 Buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di xeexal.»
Musaa duggul Kanaan
23 Jant yooyu laa tinu Aji Sax ji, ne ko:
24 «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore?
25 May ma rekk ma jàll, ba gis réew mu baax, ma ca wàllaa dexu Yurdan, tund wu rafet woowu ba ca Libaŋ!»
26 Waaye fekk na Aji Sax ji mere ma lool ndax yeen, ba faalewu ma. Aji Sax ji ne ma: «Na doy. Bu ma waxati lu jëm ci loolu.
27 Yéegal ba ca kaw tundu Pisga, nga dawal sa bët, te séenu réew ma wetu sowu, ba bëj-gànnaar, bëj-saalum, ba penku. Xoolal bu baax, nde doo jàll dexu Yurdan gii.
28 Waaye nanga yebal Yosuwe, ñaax ko, jàjj ko, ndax moom mooy jàll, jiite mbooloo mii, te moo leen di jox réew moomu ngay séen.»
29 Ba mu ko defee nu toog ca xur wa, janook Bet Pewor.