13
Mbugalu yonent yi taxaw na
1 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2 «Yaw nit ki, waxal waxyu ci kaw yonenti Israyil yiy waxe ay waxyu. Nanga wax ñiy waxe waxyu ci seen xelum bopp, ne leen:
“Dégluleen kàddug Aji Sax ji:
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
3 Wóoy ngalla yonent yu ñàkk xel,
yiy topp seen xelum bopp te gisuñu tus!
4 Yeen yonenti Israyiloo,
mbete till yuy foreb gent!
5 Yéeguleen ca biir bëttukaayi tata ja,
jagalaguleen tata ju aar Israyil,
ngir taxaw, waajal xare ba,
keroog bésub Aji Sax ji.
6 Seeni peeñu caaxaan la,
seeni ngisaane diy fen.
Ñu naa: ‘Kàddug Aji Sax jee,’
te Aji Sax ji yebalu leen!
Teewul ñuy xaar kàddu gu sotti.
7 Xanaa du peeñuy caaxaan ngeen gis?
Du ngisaaney fen ngeen di waxe,
naan: ‘Kàddug Aji Sax jee,’
te man àdduwma?
8 «“Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Gannaaw yeena waxi caaxaan, gisi fen,
maa ngii nag, di dal fi seen kaw.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!
9 Sama loxooy dal yonent,
yiy gis peeñuy caaxaan,
di gisaaney fen.
Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe,
limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind,
te réewum Israyil, duñu fa dellu.
Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.
10 Kon nag gannaaw ñu ngi lajjal sama ñoñ,
naan leen lépp jàmm! Te jàmm amul,
mu mel ni miiru digaloo bu sew bu ñu ñab-ñabal,
te ñii defuñu lu moy raax ca weexal,
11 waxal raaxkati weexal yi, ne leen:
‘Tata jeey màbb,
nde waameey wal,
ponkali doji yuur ne yureet,
ngëlén riddi, bëtt tata ja!’
12 Bu tata ji jekkee ne jànjaŋ,
deesu leen laaj fu weexal ba ngeen ca raaxoon jaar?
13 Kon Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maay xadaru, riddil ngëlén,
mer, walal waame,
am sànj yuri ponkali doji sànkute.
14 Maay màbb tata ji ngeen raax weexal,
mëqal ko suuf,
kenu ya siiñ,
lépp jóoru, ngeen jekkliku ca biir.
Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
15 Maay xëpp sama xadar ci kaw tata ji
ak ña ko raaxoon weexal,
ne leen: ‘Tata mes,
weexalkatu tata mes!
16 Mooy yonenti Israyil yi jottli Yerusalem waxyu,
di leen gisal peeñum jàmm,
te jàmm amul.’
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!”
17 «Yaw nit ki,
janool ak sa bokk yu jigéen,
yiy waxe waxyu ci seen xelum bopp,
nga wax waxyu fi seen kaw.
18 Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Wóoy ngalla jigéen ñiy sàkkal ku ne jarab xërëm,
di ràbbal ku ne muuraayu xërëm bu ko jot,
di ko moome nit ñi!
Man ngeena aakimoo sama bakkanu ñoñ
tey sàmmaale seen bakkanu bopp?
19 Bu ngeen di fen sama ñoñ ñiy dégluy fen,
yeena ngi may teddadil fi sama ñoñ,
ngir ŋëbu peppum lors ak dogu mburu,
ba tax leen di rey bakkan yu warula dee,
di musal bakkan yu warula dund.
20 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa ngii di dal ci seen kaw jaray xërëm,
yi ngeen di nappe ay bakkan niy picc.
Seeni jara laay foqatee ci seeni loxo,
ba yiwi bakkan, yi ngeen di napp niy picc.
21 Maay foqati seeni muuraay,
génne sama ñoñ ci seeni loxo,
ñu noppee doon seenum pàdd,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
22 Gannaaw yeena fen ba jeexal xolu aji jub,
te du maa ko tegu naqar,
gannaaw yeena dooleel ku bon,
tere koo dëpp yoonu mbonam ba dund,
23 dungeen gisati nag peeñuy caaxaan,
dungeen gisaaneeti.
Maay génne sama ñoñ ci seeni loxo,
ngeen xam ne maay Aji Sax ji.”»