26
Waxyu dal na Tir
1 Ba loolu amee, ca fukkeelu at maak benn, yemook benn fanu weer wa, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2 «Yaw nit ki,
Tir dëkk ba moo ree Yerusalem,
ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na!
Léegi man la bunt ubbikul,
léegi maay woomle, Yerusalem gental na.”
3 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaw Tir, maa ngii fi sa kaw.
Ni géej di yéegee ay gannaxam,
ni laay yéegloo fi sa kaw xeet yu bare.
4 Ñooy màbb say miir,
daane say tata,
ma buube fa pënd ba,
def ko doj wu ne duŋŋ.
5 Tir ay doon wéerukaayu caax ci digg géej gi,
maa ko wax, kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Dëkk bii mooy doon sëxëtoom xeet yi,
6 dëkk-dëkkaan yi bootu ci mbooyam fàddoo saamar,
ñu xam ne maay Aji Sax ji.
7 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Maa ngii di jële bëj-gànnaar, indi ci kaw Tir, Nabukodonosor buuru Babilon, buuru buur yi, aki fas aki watiir aki gawar, ak mbooloo mu takku.
8 «Dëkk-dëkkaan yi bootu ci sa àll bi, saamar la leen di reye.
Mooy yékkati fi la wër ab gawukaay,
jal ay sëkk, gawe la,
yékkati kiiraayu xare yu ràbbaloo ba def um taax, janook yaw,
9 mooy rëkke say miir dénku dàjjikaay,
mooy màbbe say tata ay sémmiñam,
10 ay fasam yu bare sànge la pënd,
riiru gawar yaak mbege yaak watiir ya riiral say miir,
mu jàlle say wunt, dugg, ni ñuy bëtte dëkk,
bu ñu bëtt tataam.
11 Tànki naari góoram lay note sa mbeddoo mbedd,
sa mbooloo mi, mu bóome saamar;
sa kenuy tabax yu dëgër jóoru fi suuf.
12 Ñooñooy foqati sam koom,
sëxëtoo sa alal,
màbb say miir,
daane sa kër yu bakkane,
boole doj yaak bant yaak pënd ba,
tàbbal ca mbeex ma.
13 Maay dakkal say woy,
ba say xalam du fi jibeeti.
14 Maa lay def doj wu ne duŋŋ,
bérabu wéerukaayu caax ngay doon,
te deesu la tabaxati mukk.
Man Aji Sax ji déy maa ko wax!
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
15 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax Tir, ne ko:
Keroog sa coowal jéll ba,
ba ñuy bóome fa sa biir,
ñay dee di binni,
dun yaa cay dégg, di lox moos!
16 Mboolem buuri tefes yaay wàcc seeni ngàngune,
futti seeni mbubb,
tàggook seen yére yu yànj,
bàddoo tiitaange,
ne dett fi suuf,
dëkke kat-kat,
seen yaram dawe saw demin.
17 Ñooy yékkati kàddu, jooye la, ne la:
“Yaaka sànku tey, yaw dunu géej bu xumb bi woon,
yaw dëkk bu siiw bi woon, di jàmbaaru waa géej,
yaak say nit a daa tiital mboolem ñi leen wër.
18 Tey sa bésub jéll bii,
dun yeey xala lox.
Duni géej yeey tiit ci sa sànkute gi.”
19 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Bu ma lay def dëkk bu gental,
nga mel ni dëkk yu nit ña ne mes,
ba ma waral xóote ya fi sa kaw,
ba wali ndox ya mëdd la,
20 keroog maa lay wàccaaleek ñay wàcci biir pax,
nga fekki xeetu démb.
Maa lay dëël taati biir suuf,
fu mel ni genti cosaan ya,
nga fekki pax ña fa jëkkoona wàcc,
ngir deesatu la dëkke,
te doo amati cér réewum aji dund ña.
21 Demin wu raglu laa lay sédd,
ba nga ne mes,
ñu di la seet, te deesu la gisati mukk.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!»