30
Babilon song na Misra
1 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2 «Yaw nit ki, jottlil waxyu! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’
3 Bés jubsi na déy,
bésub Aji Sax ji jubsi na!
Bésub xàmbaar, jantub xeet yi.
4 Saamar ay dikkal Misra,
fépp di jal-jal ba ca Kuus,
aw nit, ñu bóom ca Misra,
nangu alalu réew ma,
kenu ya màbb.
5 Waa Kuus ak Puut ak Ludd
ak xeet yu raxe yépp ak waa Libi,
boole ci ñenn ci réewum kóllëre gi,
ñoom ñépp saamar lañuy fàddoo.
6 «“Aji Sax ji dafa wax ne:
Wéeruwaayi Misra ya day jóoru,
doole ja Misray sago ŋiis;
la dale Migadol ba Asuwan, saamar lañuy fàddoo.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
7 Ñooy gëna wéet ci réew yi,
seeni dëkk gëna gental ci dëkk yi.
8 Bu ma taalee Misra,
ba wéeruwaayam yépp rajaxoo,
dinañu xam ne maay Aji Sax ji.
9 Bésub keroog dees na dugg ay gaal, génn ci sama ndigal,
ngir indil tiitaange réewum Kuus ma ne finaax,
muy seen jal-jal keroog bésub Misra ba.
Bés baa ngii déy di dikk!
10 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maay jeexal mbooloom Misra mu réy,
jaare ko ci Nabukodonosor buuru Babilon.
11 Mooy ànd ak ñoñam,
di ñi gëna néeg ci yéefar yi,
dikk yaqtesi réew mi;
ñooy boccil Misra saamar,
ba feesal réew mi ay néew.
12 Maay def wali Niil ag joor,
maay jaay réew mi nit ñu aay.
Maay alag réew meek li ci biiram,
jaare ko ci ay doxandéem.
Man Aji Sax ji, maa ko wax.
13 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maay sànk kasaray tuur yi ak yàllantu ya ca Memfis.
Buur dootu tooge jalu réewum Misra,
te maay indi tiitaange biir Misra.
14 Maay yàqte Pattros,
taal dëkk bi ñuy wax Cowan,
ba sottal sama mbugal ci kaw dëkk bi ñuy wax No.
15 Maay sottil sama xadar Ciin, rawtub Misra,
te maay tenqi gàngooru No.
16 Maay taal Misra,
dëkk ba ñuy wax Ciin di rag-ragi;
dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko;
Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg.
17 Xaleli góori On ak Pi Beset, saamar lañuy fàddoo,
waa dëkk yooyu ca des njaam lañu jëm.
18 Bu ma dogee sidditi Misra,
ba doole ja muy sago ŋiis,
jant dootu fenkal Tapanes,
aw xiin ay sàng dëkk bi,
te dëkk-dëkkaanam ya, njaam lañu jëm.
19 Nii laay wàcceele Misra ay mbugal,
ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»
Doole réer na Misra
20 Ca fukkeelu at maak benn, juróom ñaari fan ca weer wa jëkk, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
21 Yaw nit ki, damm naa përëgu Firawna buuru Misra,
mu ngii, deesu ko takk, ba mu faju,
deesu ko lëmës, ba mu mana ŋàbb saamar.
22 Léegi nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
«Maa ngii fi kaw Firawna buuru Misra.
Ñaari përëgam yépp laay damm;
bu baax beek bi damm ba noppi,
maay waddal saamaram bi ci loxoom,
23 maay tasaare Misra fi biir xeet yi,
wasaare leen fi biir réew yi.
24 Maay dooleel përëgu buuru Babilon,
teg sama saamar ci loxoom,
gannaaw ba ma dammee përëgi Firawna,
muy binni binniy ku ñu jam fi kanamam.
25 Maay dooleel përëgi buuru Babilon moos,
përëgi buuru Misra yoqi.
Maay teg sama saamar ci loxol buuru Babilon,
mu xàccil ko réewum Misra,
ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.
26 Maay tasaare Misra fi biir xeet yi,
wasaare leen fi biir réew yi,
ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»