36
Barke ñeel na tundi Israyil
1 «Yaw nit ki, waxalal waxyu tundi Israyil. Neel:
“Yeen tundi Israyil,
Dégluleen kàddug Aji Sax ji.
2 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Gannaaw noon bee ne leen: ‘Ñaw!
Seen kawte yu yàgg yii,
tey nooy boroom.’ ”
3 Kon waxal waxyu bii, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Wet gu ne lañu leen same, yàqte leen,
ba ngeen mujj di moomeelu yéefar yi,
ñépp di leen jëw ak a tooge,
4 Kon nag yeen tundi Israyil,
dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji.
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi,
ak xunti yeek xur yi,
ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental,
te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen.
5 Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne:
Maa ngii déy di waxe sama tàngooru fiiraange
ak xeet yi dul yawut, boole ci Edom gépp,
ñoom ñi jiital seen xeebeel,
te suuf si ma séddoo, ñu aakimoo ko,
te di ko bége mbégte mu mat sëkk,
ngir sëxëtoo parluy réew mi.”
6 Kon nag, waxalal waxyu suufas Israyil
te wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi
ak xunti yeek xur yi, ne leen:
“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa ngii di waxe fiiraange ak xadar
ndax toroxte gi leen xeet yi teg.
7 Loolu tax na Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Man maa giñ ne yéefar yi leen séq ñooy tegoo toroxte.
8 «“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat,
di meññal Israyil sama ñoñ,
te léegi ñu ñibbsi.
9 Maa ngii déy maak yeen,
maa leen di geesu,
ba ngeen ruuje, jiwe.
10 Maa leen di fulal aw nit, ci biir Israyil gépp, ba mu daj,
ñu dëkkewaat dëkk yu mag yi,
tabaxaat bayaal yi.
11 Maa leen di fulal nit ak mala,
ñu giir, nangule.
Maay def ñu dëkke leen na woon,
baaxe leen lu raw démb,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
12 Yaw suuf, maay doxloo nit fi sa kaw,
muy waa Israyil sama ñoñ,
ñu jagoo la, séddoo la,
te dootoo sabab seenug deele.”»
13 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
«Nee ñu réewum Israyil mooy dëmm buy dëmm boppam.
14 Kon yaay réew mu dootu dëmme,
bay reylu saw xeet.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
15 Dootuma la dégtal ñàkk kersay yéefar yi,
dootoo dékku yabeelu xeet yi,
te dootoo reylu saw xeet,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
Israyil yeeslu, Yàlla di sell ba tey
16 Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma:
17 «Yaw nit ki, ba waa kër Israyil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeele seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man.
18 Ma xëpp leen sama xadar ndax deret ji ñu tuur ci réew mi, ak kasaray tuur yi ñu ko sobeele.
19 Ma tasaare leen ci biir yéefar yi, ñu wasaaroo fi biir réew yi. Seen jikko ak seeni jëf laa leen àttee.
20 Waaye fu ñu dem ca biir yéefar ya, teddadil nañu fa sama tur wu sell, nit ña di leen waxtaane, naan: “Ñii de, ñoñi Aji Sax ji lañu, teewul réewam ma lañu bàyyikoo nii.”
21 Ma daldi seet ci sama teddngay tur wu sell, wi waa kër Israyil di teddadil fi biir yéefar yi ñu fekki.
22 «Moo tax nanga wax waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, li may waaja def, du yeen laa ci seet, li ma ci seet mooy sama teddngay tur wu sell, wi ngeen teddadil fi digg yéefar yi ngeen fekki.
23 Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
24 Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajalee leen mépp réew, délloosi leen seen suufas bopp.
25 Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
26 Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux,
27 te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm ak a jëfe sama àttey yoon.
28 Su boobaa ngeen mana dëkke réew mi ma joxoon seeni maam, di sama ñoñ, may seen Yàlla.
29 Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif.
30 Maay ful doomu garab ak meññeefum tool, ba dootuleen am gàccey xiif fi digg yéefar yi.
31 Su boobaa yeenay fàttliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu.
32 Du yeena tax nag may jëfe noonu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Na leen loolu wóor. Kon nag waa Israyiloo, rusleen ba ne tott ci seeni jëfin.”
33 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés bu ma leen setalee ba ngeen tàggook seen mboolem ñaawtéef, dinaa delloo dëkk yu mag yi aw nit, gent yi tabaxewaat.
34 Mbooy gu wéet gi, dees na ko beyaat, ba mu wuuteek wéetaay, ba képp ku fa jaare seede woon.
35 Su boobaa dees na ne: ‘Xool-leen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yeet ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbli lépp, ba dëkke nii!’
36 Su boobaa seen dëkkandooy yéefar yi fi des dinañu xam ne man Aji Sax ji maa tabaxaat dëkk yu mag yi tojatoo woon, jëmbataat mbooy gi. Man Aji Sax ji, maa wax te maay jëf.
37 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israyil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.
38 Bu màggal masaa am, Yerusalem day fees ak gàtt yu ñuy rendi, sarxal. Nit ñiy dëkkewaat genti tey yii, noonu lañuy baree. Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»