25
Ibraayma nelaw na
Ibraayma jëlaat na soxna su tudd Ketura, am ca Simran ak Yogsan ak Medan ak Majan ak Yisbag ak Suwa. Yogsan jur Saba ak Dedan. Askani Dedan ñooy Asureen ñi, Letuseen ñi ak Lewumeen ñi. Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu.
Ibraayma nag donale Isaaxa lépp lu mu moom. Doom yu góor, ya mu am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa*.
Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175). Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel. Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba. 10 Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata. 11 Gannaaw ba Ibraayma nelawee, Yàlla barkeel na doomam Isaaxa. Isaaxaa ngi dëkkoon ca wetu teenu Laxay Roy.
Askanu Ismayla
(Saar 25.12-18)
12 Ismayla moomee nag, doomu Ibraayma jaak Ajaram Misra, ma doon jaamub Saarata, askanam mooy lii. 13 Turi doomi Ismayla yu góor yaa di: Nebayot, taawub Ismayla, ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam 14 ak Misma ak Duuma ak Maasa 15 ak Adàdd ak Tema ak Yetur ak Nafis ak Kedama. 16 Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni mbooloo ci seeni sanc ak seeni dal. 17 Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam.
18 Ña nga dëkkoon diggante ba dale Awila ba Sur ga jàkkaarlook Misra, booy jëm Asur. Noonu la fa askanu Ismayla sance, jàkkaarlook doomi baayam yépp.
Askanu Isaaxa doomu Ibraayma
(Saar 25.19—35.29)
19 Isaaxa doomu Ibraayma ju góor ja, askanam mooy lii. Ibraaymaa jur Isaaxa. 20 Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba. 21 Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb. 22 Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji.
23 Aji Sax ji ne ko:
«Ñaari giir nga ëmb,
nara am ñaari xeet yuy xaajaloo,
wenn wi mooy ëpp doole wi ci des,
te mag ji mooy surgawu rakk ji
24 Ba mu demee ba wara mucc, amul lu moy ay seex. 25 Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). 26 Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at.
Esawu sàggane na céram
27 Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu§ te bëggoon toogaayu kër. 28 Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba.
29 Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe ju xonq, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd. 30 Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). 31 Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw* 32 Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» 33 Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw. 34 Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo.
* 25:6 Ca yooya jamono, nit manoon naa am ay soxna yu am cér bu mat sëkk, ak yeneen soxna, yu gëna néewle sañ-sañ, ñoom ak seeni doom. 25:23 Ci bànni Israyil, seex, bi jëkka juddu, moo mag ki mujja juddu. 25:26 Jàpp ci téstën mu ngi tekki ci waxin «suufu nit, ba am loo nangu ci moom». § 25:27 gàtteñlu gi ci Yanqóoba moo waraloon xamul dara ci rëbb. * 25:31 Ci bànni Israyil, taaw mooy mujj doon kilifag kër, te mooy ëpple ay rakkam ab cér ci ndono.