Bataaxal bu jëkk bi Yàlla may Póol,
mu bind ko waa
Tesalonig
1
1 Man la Póol, mi ànd ak Silwan ak Timote ci kàddu gii ma yékkati, ñeel mbooloom gëmkati waa Tesalonig, ñi bokk ci Yàlla Baay bi ak Sang Yeesu Almasi. Yiw ak jàmm ñeel na leen.
Waa Tesalonig am nañu aw yiw
2 Nu ngi sant Yàlla fu nu tollu ci yeen ñépp, te noppiwunu leena fàttliku ci sunuy ñaan,
3 ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.
4 Yeen bokki gëmkat ñi Yàlla sopp, xam nanu ne moom moo leen taamu,
5 ndax sunu xibaaru jàmm, bi nu leen àgge, dikkewu leen ay wax rekk, waaye manoore la leen dikkaale, ak ndimbalal Noo gu Sell gi, ak kóolute gu mat sëkk gu ngeen am. Xam ngeen moos na nu nekke woon ca seen biir, di xintewoo seen njariñ.
6 Aw ngeen sunuy tànk, aw it ci tànki Sang bi, nde yeena jot ci kàddu gi, ci biir njàqare ju bare, te di ko bége ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
7 Moo leen taxa doon royukaay ci mboolem gëmkati diiwaani Maseduwan ak Akayi.
8 Ci seen biir kay la kàddug Boroom bi jollee, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen ngëm Yàlla fépp la siiwe, ba soxlawunu cee waxati fenn dara.
9 Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,
10 tey séentu Doomam Yeesu mi mu dekkal, mu dikk bàyyikoo asamaan, moom mi nu jot ci sànj miy dikk.