11
Cofeel la Aji Sax ji tontoo fippug Israyil
«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw,
Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.
Lu ñu leen gëna woo,
ñu gën maa sore.
Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax,
te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.
Ndaxam man maa tette Efrayim, fab ko,
te ràññeewuñu ne maa leen topptoo.
Ay goji nit laa leen ñoddee,
ay buumi cofeel.
Maay ki leen yolomalal ŋalaabi ŋaam,
sëgg, leel leen.
Duñu dellu réewum Misra*.
Waa Asiri ñooy doon seen buur,
nde ñoo baña délsi fi man.
Ab saamar ay wëndeelu ca seen dëkk yu mag,
dàjji seen bunti dëkk,
ba warax leen ndax seeni mébét.
Sama ñoñ dañoo làggi ci ñàkke ma kóllëre,
wooyees na leen fa kaw,
te kenn ci ñoom jógul.
 
«Efrayim, ana nu ma lay baye,
yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo?
Ana nu ma lay defe ni Atma?
Nu ma lay yemaleek Ceboyim?
Sama xol a bëpp,
sama yërmandee yëngu.
Duma wéye di tàkkal sama mer,
duma yàqteeti Efrayim,
ndax maay Yàlla, duma nit,
maay Aji Sell ji ci seen biir,
duma dikke am sànj.
10 Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji,
muy yëmmu ni gaynde.
Mooy yëmmu moos ni gaynde,
ay doomam di lox, jóge sowu.
11 Ni njanaaw lañuy loxe, jóge Misra,
mel nim pitax, bawoo Asiri.
Maa leen di dëël seeni kër.»
Aji Sax jee ko wax.
* 11:5 Loolu mooy duñu dellu ci njaam ga ñu nekke woon ca Misra. 11:8 Ceboyim ak Atma ñooy ñaari dëkk yu Yàlla boole ak Sodom ak Gomor, dëkk ya ñu dendaloon, tas leen.