4
Aji Sax ji tiiñal na kilifay ñoñam
1 Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddug Aji Sax ji,
Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi:
«Du kóllëre, du ngor, du gennug ràññee Yàlla
ci réew mi.
2 Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo.
Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.
3 Moo tax réew mi wowal,
mboolem lu fi dëkke ràgg,
ba ci rabi àll yi, ak njanaaw yi,
jëni géej itam day réer.
4 «Waaye bu ci kenn layoo,
bu ci kenn sikke,
ndax sa bokk yee mel ni ñuy layook sarxalkat yi.
5 Dingeen tërëf bëccëg,
yonent yi ànd ak yeen tërëf guddi,
te maay sànk seen ndey.
6 Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam;
yeen, xam-xam ngeen gàntal,
ma gàntal seenug carxal.
Yeena fàtte seen yoonu Yàlla,
man it maay fàtte seeni doom.
7 sarxalkat yi ñu gëna baree, gën ma nee moye,
seenub sag, gàcce laa koy soppi.
8 Sama saraxi póotum bàkkaari ñoñ
lañuy dunde,
tey yàkkamti ñu def njubadi.
9 Waaye niki askan wi, niki sarxalkat yi,
maa leen di dikke seen añu jikko,
maa leen di fey seeni jëf.
10 Ñooy lekk te duñu regg,
di gànctu te duñu giir,
nde Aji Sax ji lañu noppee topp.
11 Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees,
moo yóbbu seenum xel.
12 Sama ñoñ, seen bant lañuy seeteey,
seenu yet di leen waxaleey.
Xelum ngànctu moo leen wacc,
ñooy gànctu, lajje fa seen Yàlla.
13 Ca kaw tund yu mag ya lañuy rendee ay sarax,
cuuraay, ñu taale ca tund yu ndaw ya,
ak ca taatu gii garab gu mag, ba ca gee,
fa ker ga neexe.
Moo tax seeni doom di gànctu,
seen séeti doom di jaaloo.
14 Duma mbugal seeni doom
ndax li ñuy gànctu
mbaa seen séeti doom
ndax li ñuy jaaloo,
ndax ñoom sarxalkat yi ci seen bopp,
ay gànc lañuy teggeendool
te gànc yi ci jaamookaayi xërëm yi,
ñoom lañuy indeendool jooxe.
Askan wu amul ug dégg, sànku.
15 «Yeena ngi gànctu, yeen bànni Israyil,
waaye na Yuda mucc ci googu tooñ.
Buleen dugg Gilgal,
buleen yéegi Bet Awen
di giñ ci Aji Sax jiy dund.
16 Ndegam ni aw nag tëwe ni la Israyil tëwe,
ndax léegi Aji Sax jee leen di foral
nim xar ci parlu mu ne màww?
17 Efrayim googu laa ne, moo lëngook jëmmi tuur!
Seetaan leen.
18 Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu,
te gàccee gënal seeni kilifa.
19 Callweer a leen di wal,
ñu kersawoo seen jooxey tuur.