Yàllaa moom xeet yi
13
(Saar 13—23)
Yéeneb waxyu dal na Babilon
1 Yéeneb bii ñeel na Babilon,
muy peeñum Esayi doomu Amocc.
2 Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ,
joorleen ñii,
tàllal-leen loxo,
ñu jàlle bunti kàngam yi.
3 Maa jox ndigal ñi ma beral sama bopp,
maa woo sama jàmbaar ñiy réy-réylu,
ne leen ñu sottal mbugal mi samam sànj laaj.
4 Coowal mbooloo ngoog ca tund ya,
mel ni ñu baree bare!
Riirum nguuri nguur yu daje, di xeeti xeet!
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
mooy dajale gàngooru xare.
5 Mooy bawoo fu sore,
fa asamaan digalook suuf.
Aji Sax ji laak gàngoor gi muy mbugale,
ngir yàqtesi réew mi mépp.
6 Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal,
te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.
7 Moo tax yoxoo yoxo yoqi, xoloo xol jeex,
8 ñu tiita tiit,
yaram di fuddook a metti,
ñuy baddaañu ni kuy matu;
ku ne jàq, di xulli sa moroom,
kanam ya sël-sëleendoo.
9 Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw,
bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk,
nara gental suuf,
te bàkkaarkat ya la fay fàkkas.
10 Biddiiw mbaa dëllooñ dootu leeral;
jant ay fenke lëndëm,
weer dakkal leeram.
11 Maay delloo àddina mbonam,
yool ku bon tooñam,
maay sàggi sagub ku reew,
detteel puukarey ku néeg.
12 Maay def nit gëna jafee gis wurus,
ba doom aadama raw wurusu Ofir.
13 Moo tax maay gësëm asamaan,
suuf yëngoo fa mu tege
ndax sànjum Aji Sax ji
Boroom gàngoori xare yi,
keroog ba meram di tàkk.
14 Ku nekk ay fekkiy bokkam,
rawi cam réewam,
mbete kéwél gu ñuy rëbb,
mbaa xar mu amul sàmm.
15 Ku ñu ci gis, jam la,
ku ñu jàpp, saamar rey la;
16 seeni doom, ñu moxoñe fi seen kanam,
seeni kër, ñu sëxëtoo,
seeni jabar, ñu tëdde.
17 Maa ngii di xabtal fi seen kaw waa Medd,
ñi xintewoowul xaalis,
faalewuñu wurus.
18 Seeni fitt lañuy rajaxee xalelu góor,
duñu ñeewante gone,
duñu xool tuut-tànk gëti yërmande.
19 Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër,
di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo,
waaye Yàllaa koy tas,
mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
20 Deesatu fa dëkk,
xanaa gental ba fàww.
Màngaan dootu fa samp xayma,
sàmm dootu fa gooral.
21 Ay rabi àll a fay goore,
kër ya fees aki looy,
bànjóoli dëkke fa,
kéwél di fa curpee.
22 Bukki mooy sabe fa tata ya,
till nangu kër yu bakkane ya.
Àppu Babilon jege na, ay fanam du fi wees.