21
Ab yéeneb waxyu ñeel na Babilon
1 Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga:
Ni ag ngëlén di riddee jaare Negew
ni la noon di bawoo màndiŋ ma,
jóge réew mu raglu.
2 Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax.
Workat biy wor, yàqkat biy yàq.
Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen.
Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.
3 Lii a waral sama njàqareg xol,
mitit jàpp ma, mel ni mititu mat,
ma jaaxle ba déggatuma,
jàq ba gisatuma.
4 Bopp ubu, tiitaange jàpp ma;
sama ngoonug bànneex
soppiku guddi gu raglu.
5 Ndab taaje, laltan lale,
ñuy lekk ak a naan.
Ñu jekki ne: «Yeen kilifa yi, jógleen!
Diwleen pakk yi!»
6 Boroom bi kat da maa wax, ne ma:
«Doxal taxawal ab jongrukat,
lu mu gis, wax ko.
7 Bu gisee gawar ci watiiru ñaari fas,
ak ñu wari mbaam ak ñu wari giléem,
na teewloo teewlu bu baax.»
8 Jongrukat ba àddu ca kaw ne:
«Sang bi, maa ngii yendoo séentu,
fanaane wattu fii ma taxaw.
9 Ma ne gawar a ngii,
war watiiru ñaari fas.
Nee: “Daanu nañoo, Babilon daanu na,
jëmmi tuuram yépp tasaaroo fi suuf!”»
10 Yeen bokk yi ñu bàcc ni pepp ca sama dàgga ja,
la ma dégge ci Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi,
wax naa leen ko.
Ab yéeneb waxyu ñeel na Duuma
11 Yéene bii moo wàccal Duuma:
Nit a ngi may wooye tundu Seyir, naan:
Jongrukat bi, lu des ci guddi gi?
Éy jongrukat bi, lu desati ci guddi gi?
12 jongrukat bi ne:
«Bët set, mu guddeeti rekk,
Boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.»
Ab yéeneb waxyu ñeel na Arabi
13 Yéene bii moo wàccal Arabi:
yeen cëggi askanu Dedan,
mbooyum Arabi ngeen di fanaane.
14 Yeen waa Tema, dajejileen ak ña mar,
yóbbul leen am ndox.
Dogileen ñay daw,
may leen ñu lekk.
15 Ay saamar de lañuy daw;
saamar bu ñu leen xàccil
ak fitt gu ñu leen diir
ak tàngooru xare.
16 Aji Sax ji de da maa wax ne ma: «Fileek menn at mu surga bu ñu bind waññ, sagub dëkk bii di Kedar dina sàggiku,
17 li des ci jàmbaari fittkati Kedar di lu néew.» Aji Sax ji Yàllay Israyil wax na ko.