55
Aji Sax ji woote na njéggal
1 «Éey, yeen ñi mar ñépp,
dikkleen ci ndox mi,
ba ci ku amul xaalis sax!
Dikkleen jënd pepp, lekk!
Dikkleen jënd pepp mu xaalis jëndul,
ak biiñ ak meew mu amul pey.
2 Ana lu ngeen di waññe xaalis,
di ko jënde lu dul aw ñam?
Ana lu ngeen di sonn,
di jënde lu dul reggal?
Dégluleen maa déglu, ba lekk lu leen di dundal,
di xéewloo seen ngëneelu bakkan.
3 Teewluleen te dikk fi man.
Dégluleen, ba mana dund,
ma fas ak yeen kóllëre gu sax,
gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.
4 Ab seedee ngoog, ñeel xeet yi,
muy njiit, yilif xeet yi.
5 Ma ne, aw xeet woo xamul ngay wooyi,
xeet wu la xamul ay dawsi ba ci yaw,
ngir sa Yàlla Aji Sax ji,
Aji Sell ju Israyil,
nde moo la teral.»
6 Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis,
wooleen ko bi muy jege.
7 Na ku bon ba jëfinam,
kuy def lu ñaaw fomm mébétam,
te walbatiku ci Aji Sax ji sunu Yàlla,
mu yërëm ko, yaatal njéggalam.
8 «Samay xalaat déy du seeni xalaat,
te samay jëfin du seeni jëfin.»
Kàddug Aji Sax jee.
9 Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf,
ni la samay jëfin tiime seeni jëfin,
samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.
10 Ab taw ak tawub yuur asamaan lay wàcce,
du fa dellu,
te suuxatul suuf,
saxal ko, meññal ko,
ba kuy ji, mu may la jiwu;
kuy lekk, mu may lam pepp.
11 Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la.
Du délsee ag neen ci man
te deful li ma namm,
ba sottal li ma ko yebal.
12 «Mbégte déy, ngeen di génne,
ñu yóbbu leen ci jàmm,
tund yu mag yeek yu ndaw yi
di leen sarxolleel,
garabi àll bi yépp tàccoondoo.
13 Garab gu dul ruus ay wuutub gajj,
garab gu dëkke naat wuutub taxas,
muy woyu Aji Sax ji,
te di firnde ju sax,
du dog mukk.»