25
Deesul am dëgg fa Yàlla
Bildàdd ma bàyyikoo Suwa àddu, ne:
Yàllaa man te mata ragal,
di def jàmm fa kawteem ya.
Ay gàngooram limu naam?
Ana ku mu dul jam ceeñeeram?
Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla?
Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?
Xoolal, weer wi sax leerul ba doy ko,
te biddiiw yeet gisul seen sellaayu leer,
astamaak nit kii tanewulu sax,
doom aadama jii gënul gasax.