27
Ayóoba bañ na
1 Ayóoba dellu yékkati kàddoom, ne:
2 Yàlla miy dund seere na, moom mi ma xañ dëgg,
moom Aji Man ji ma teg naqaru xol,
3 ne li feek may ànd ak bakkan,
di noyyee noowal Yàlla,
4 sama gémmiñ gii du wax njubadi,
sama làmmiñ wii laa ne, du tudd ay fen.
5 Yàlla buma leen jox dëgg,
ba ba may dee duma weddi samag mucc sikk.
6 Sama njekk laay ŋoy, duma ko ba,
sama giiru dund sama xel du ma yedd.
Yéene néeg la
7 Yal na noon bokk ak ku bon demin,
ku may fexeel bokk ak kàccoor ag muj.
8 Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo,
ba Yàlla moom bakkanam?
9 Bu ko njàqare di dikkal,
Yàlla day dégg yuuxam a?
10 Ndax Aji Man ji la daan bége,
am daan na tudd Yàlla fu mu tollu?
11 Ma xamal leen boog li ci dooley Yàlla,
duma leen nëbb li Aji Man ji namm.
12 Dama ne, yeen ñépp a ko gisal seen bopp sax,
kon lu leen yebuloo nii ci neenug neen?
13 Lii mooy cér bi Yàlla sédd ku bon,
mooy wàll wi Aji Man ji dencal ku néeg.
14 Njabootam ne xas, saamar jagoo,
te balaa booba duñu lekk ba suur.
15 Ña koy wuutu, mbas a leen di rey,
te ay jëtunam duñu ko jooy.
16 Su doon jal xaalis ni suuf,
yére yomb ko ni feppi suuf,
17 mooy dajale, aji jub sol;
xaalis ba, kay def njub séddoo.
18 Mooy tabax kër gu tanewul
mbaarum wattukatu tool,
te lëndu jargoñ gën koo dëgër.
19 Keey tëraale alal ju mu dul gisati;
day xippi, fekk mu ne mes.
20 Musibaa koy dab nim wal,
ngëlénu guddi këf, yóbbu,
21 ngelawal penku déjjatee ko këram,
jalax, mu wéy.
22 Dees na ko diir, bañ koo ñéeblu,
mu daw, di wuta rëcc dooley saan ya.
23 Dees na ko tacc-taccali loxo,
di ko ciipoo fa këram.