23
Sàmm bu baax aye na
1 «Wóoy ngalla sàmm yiy sànk ak a tasaare sama gétt gi.» Kàddug Aji Sax jee.
2 Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci sàmm yiy sàmm ñoñam ne: «Yeena tasaare sama gétt gi, dàq leen, te taxawuwleen leen. Kon maa ngii di leen taxawoo mbugal, yoole leen seen jëf ju bon.» Kàddug Aji Sax jee.
3 «Man nag, sama ndesu gétt, maa leen di dajalee mboolem réew yi ma leen dàqoon, jëme; te maa leen di délloosi seen parlu, ñu meññ ba yokku.
4 Dinaa leen taxawalal ay sàmm yu leen di sàmm ba dootuñu tiit, dootuñu jàq, dootuñu wuute.» Kàddug Aji Sax jee.
5 «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee,
«maay jebbil Daawuda njebbitu njekk,
mu falu di buur bu xelu,
di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
6 Ay jantam Yuda dina texe,
Israyil dëkke kaaraange,
te dees na ko tudde nii:
“Aji Sax ji sunu njekk.”
7 «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israyil ca réewum Misra.”
8 Xanaa dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee askanu Israyil réewum bëj-gànnaar, génnee leen mboolem réew ya mu leen sànkeji woon.” Su ko defee ñu dëkkewaat seen suufas bopp.»
Kàddu jógal na yonenti caaxaan
9 Mu jëm ci yonent yi:
Sama bopp a ubu ràpp, sama xol jeex,
sama yax yépp ne yalax,
ma mel ni ku biiñ man,
ba mu màndi
ndax Aji Sax ji ak kàddoom yu sell.
10 Ay jaalookat la réew mi fees déy,
alkànde déy a waral réew mi maral,
parluy màndiŋ mi wowal.
Seeni xél loraange la,
seenug njàmbaar di naka-su-dul-noona.
Yàllaay wax
11 «Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu,
sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.»
Kàddug Aji Sax jee.
12 «Moo leen tax di tarxiise seenu yoon,
tàbbi lëndëm, fëlëñu.
Maa leen di wàcceel musiba déy
ca seen atum mbugal.»
Kàddug Aji Sax jee.
13 «Ca yonenti Samari it laa gis njekkar,
ñuy waxe waxyuy Baal tuur mi,
di réeral Israyil, sama ñoñ.
14 Waaye yonenti Yerusalem laa gisal lu yées:
ñuy jaaloo, di wéye ay fen,
di dooleel defkatu lu bon,
ba kenn dëdduwul mbonam.
Ñoom ñépp di ma niru waa Sodom,
waa Yerusalem it ni waa Gomor.»
15 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
wax lii ci mbirum yonent yi:
«Maa ngii di leen leelsi njàqarey xeme,
nàndal leen tookey mbugal,
nde fi yonenti Yerusalem la yàqute tukkee,
ba law ci réew mi mépp.»
16 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Buleen déglu yonent yi leen di wax ay waxyu;
cóolóoli neen lañu leen di naxe,
di fent ay peeñu, di wax ay waxyu,
te du kàddug Aji Sax ji.
17 Ñi ma teddadil lañuy waxa wax,
naan leen Aji Sax ji déy nee:
“Jàmm ngeen di am.”
Képp ku topp sa xelum déggadi,
ñu ne ko: “Musiba du la dab mukk.”
18 «Waaye ana ku ci teewe woon jataayu Aji Sax ji?
Ku ci fekke, ba dégg kàddoom?
Ku ci teewlu kàddoom, ba dégg ko?
19 Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog,
sànjam fettax na,
dig callweer,
callweeral boppu ku bon.
20 Merum Aji Sax ji du giif,
te deful ba sottal li mu nar.
Fan yu mujj yii, ngeen am ci lu leer.
21 Yebaluma yonent yii,
ñoom ñuy daw di yégle!
Waxumaak ñoom,
ñoom ñuy jottli waxyu!
22 Su ñu teewe woon sama jataay sax,
mana dégtal sama ñoñ samay kàddu,
ba waññee leen seen yoonu mbon
ak seen jëfi mbon.
23 Xanaa du maay Yàlla?»
Kàddug Aji Sax jee.
«Fu jegeek fu sore, du maay Yàlla?
24 Ku mana làqoo làquwaay,
ba duma ko gis?»
Kàddug Aji Sax jee.
«Xanaa du asamaan ak suuf,
maa ko fees?»
Kàddug Aji Sax jee.
25 «Dégg naa kàdduy waxyu yi yonent yooyuy waxe ci sama tur ay fen, naan gént nañu lii, gént nañu lee.
26 Fan la yonenti fen-kat yii àppal seeni xalaat, di wax waxyuy naxe yu ñu fental seen bopp?
27 Seen gént yi ñuy nettalante, nammuñu ci lu moy sama ñoñ fàtte ma, ni ma seeni maam fàttee woon ndax Baal tuur mi.
28 Yonent bu ci am gént, na nettali géntam, waaye ku ci am sama kàddu, na ko àddoo, na ma ko waxe. Ana ñax akum pepp?» Kàddug Aji Sax jee.
29 «Sama kàddu déy, daa mel ni sawara,» kàddug Aji Sax jee, «mbaa saddu, di falaxew doj!
30 Moo tax maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi sàccante samay kàddu.
31 Maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi mbel-mbeli naan: “Kàddoo ngi.”
32 Maa ngii ci kaw ñiy waxe waxyuy génti caaxaan.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi nettali seeni gént, bay waññi sama ñoñ, ndax seen fen yu jéggi dayo, te man de yebaluma leen, santuma leen dara. Amaluñu askan wii benn njariñ.» Kàddug Aji Sax jee.
Yéeneb Aji Sax ji du ab yen
33 Aji Sax ji ne Yeremi: «Su la askan wii laajee mbaa ab yonent mbaa ab sarxalkat ne la: “Ana yéeneb waxyu bi la Aji Sax ji yóbbante?” Nga wax leen ne leen: “Yeenay yen bi te dinaa leen yenniku.”» Kàddug Aji Sax jee.
34 «Te muy yonent, muy sarxalkat mbaa kenn ci askan wi, ku ci ne: “Yéeneb waxyu bii la ma Aji Sax ji yóbbante ci yeen,” maay dikke mbugal kooku mook waa këram.
35 Li ku nekk wara laaj moroomam mbaa mbokkam kay mooy: “Lu Aji Sax ji tontu?” mbaa “Lu Aji Sax ji wax?”
36 Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenu boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi.
37 Li nit kiy laaj ab yonent mooy: “Ana lu Aji Sax ji tontu? Ana lu Aji Sax ji wax?”
38 Bu ngeen dee tudd ab yéeneb waxyub Aji Sax ji, te ma yónnee ci yeen, ne leen buleen di tudd ab yéeneb Aji Sax ji, su boobaa Aji Sax ji dafa wax ne:
39 Maa leen di yenu déy, xalab leen, yeen ak dëkk bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, ba ngeen sore ma.
40 Te maa leen di teg toroxte gu sax dàkk, ak gàcce gu sax dàkk te du fey.»