4
«Yaw Israyil, sooy waññiku,
waññikul fi man.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Soo jëlee fi sama kanam
sa jëf ju siblu,
te jenguloo,
xanaa di waate Aji Sax jiy dund,
ci dëgg ak njub ak ngor,
kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji,
di ko sagoo.»
Aji Sax ji déy dafa wax waa Yudak Yerusalem, ne leen:
«Ruujleen seen tool,
buleen ji ciy dég.
Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji,
dogleen seen mbuñukay xol,
balaa sama xadar ne jippét ni sawara,
di tàkk te deesu ko fey
ndax seen jëf ju bon.
Xare jib na
«Nangeen yégle lii fa Yuda,
dégtale ko fa Yerusalem,
yéenee koog liit fi biir réew mi
te xaacu seen kem kàttan ne leen:
“Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.”
Yékkatileen raaya, jubale Siyoŋ,
làqujileen, buleen taxaw,
musiba déy laay jële bëj-gànnaar,
muy safaan bu réy.
 
«Gayndee fëlle geeram,
fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram,
nara gental seeni dëkk,
ba ñu di gent yu kenn dëkkul.
Kon nag sol-leeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne:
“Merum Aji Sax ji tàng na kat te moyu nu.”
Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
«xolu buur jeex, kàngam ne yàcc,
sarxalkat waaru, yonent jommi.»
Yeremeey wax
10 Ma ne, «Éy Boroom bi Aji Sax ji,
yaa naxlu askan wii nax yu metti,
ba nga nee: “Yerusalem jàmm lay am,”
te saamar tege ci putam.»
Mbugal taxaw na
11 Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen:
«Jaas bu tàng a uppe kaw tund ya ne faraas ca màndiŋ ma,
wuti sama ñoñ.
Du doon ngelaw lees di bàcceek a beese.
12 Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi.
Léegi maa leen di biral sama kàddug mbugal.»
Waa Yerusalem ay wax
13 «Noon baa ngii, di jóg niy niir,
watiiri xareem ni ngëlén,
fasam ya gëna gaawi jaxaay.
Wóoy ngalla nun, yàqu nan!»
Yàllaay wax
14 «Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon,
ndax nga mucc.
Foo àppal sa mébéti xol yu bon?
15 Kàddug yéenee ngi jibe Dan,
musiba dégtu na, bawoo tundu Efrayim.
16 Jottlileen ko xeet yi,
neleen Yerusalem:
“Songkat yaa ngii riire réew mu sore ma,
xaacoondoo fi kaw dëkki Yuda.”
17 Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool,
ndax man la gàntal.»
Kàddug Aji Sax jee.
18 «Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii,
sa musibaa ngook, wex la xàtt,
di dagg sa xol.»
Yeremi jàq na
19 Maaka jàqa jàq bay jal-jali,
sama xol biy fuddu!
Éy wii mititu xol!
Duma mana noppi,
maa dégg wooteb liit
ak yuuxi xare.
 
20 Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo,
réew mi mépp ne tasar kay!
Jekki-jekki samay xayma tasaaroo.
Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo!
21 Xanaa duma gis ba fàww raayab noon,
liitu xare di ko feelu?
Aji Sax ji jéppi na ñoñam
22 «Dofe la sama ñoñ def.
Man, xamuñu maay kan,
mbetey gone yu dul xalaat dara;
dég-dég, tus;
seen xel mépp, lu bon rekk,
lu baax, xamuñu ci dara.»
Àddina salfaañoo na
23 Maa xool suuf,
ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ;
ma xool asamaan,
leer amatu ca.
24 Ma xool tund yu mag yi,
ndeke ñu ngi yëngu,
tund yu ndaw yépp di jaayu.
25 Ma xoolaat, gisuma nit,
njanaaw yépp daw.
26 Ma xool, gis suuf su nangu sa
di ndànd-foyfoy,
dëkk yépp raaf
ndax Aji Sax jeek tàngaayu sànjam.
 
27 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Duma tas lépp tasar,
waaye réew mi mépp ay gental.
28 Loolooy tax suuf di ñaawlu,
asamaan di lëndëm.
Maa ko wax, maa ko dogu;
duma dëpp, duma deltu gannaaw.»
Yerusalem dugg na fitna
29 Gawar ak fittkat riir,
waa dëkk yépp fëx,
ñii tàbbiy gajj,
ñee ñalgu ci kawi doj,
ñu won dëkkoo dëkk gannaaw,
kenn desatu ca.
30 Yaw Yerusalem mu tas mi,
ana looy def nii,
di solu ba yànj,
gànjaroo wurus,
tusngalu, yàkkleey gët?
Yaa ngi caaxoñu ci neen:
say xéddkat wacc nañu la,
sa bakkan lañuy wut.
31 Baatu ndaw su jagadi laa dégg,
ma nga jàq, di matub taawam.
Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa!
Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya,
naan: «Wóoy, ngalla man;
ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»