11
Lingeer Atalyaa falu na Yuda
1 Ci kaw loolu Atalyaa yaayu Akasiya xam ne doomam ju góor dee na, mu daldi faagaagal mboolem ku bokk ci askanu buur.
2 Teewul jigéenub Akasiya, Yoseba doomu Buur Yoram, jàpp Yowas doomu Akasiya ju góor, jële ko ca biir doomi buur ya ñuy fexee rey, ba rawale ko. Ci biir loolu mu boole kook nàmpalkatam, tëj cib néeg ngir làq ko Atalyaa, ba kenn reyu ko.
3 Yowas nekk naak Yoseba fa kër Yàlla ga, làqu fa juróom benni at, te Atalyaa di nguuru fa réew ma.
Yuda bañ na
4 Ca atum juróom ñaareel ma, Yoyada moo woolu waa Keret ya jiite kuréli téeméeri nit, ak yeneen dag ya, ñu wuysi ko ca kër Aji Sax ji. Mu fasook ñoom kóllëre, giñloo leen ca kër Aji Sax ji, ba noppi nuyole leen ak doomu Buur.
5 Ci kaw loolu mu sant leen ne leen: «Li ngeen di def mooy lii: Yeen ñi aye liggéey bésub Noflaay, na seen xaajub ñetteel dénkoo dénkaaney kër Buur,
6 beneen xaajub ñetteel ba wattu buntu Sur ba, xaajub ñetteel ba ca des féeteek bunt ba ca gannaaw dawkat ya. Noonu ngeen di ay-ayloo wattub kër Buur.
7 Seen yeneen ñaari kurél yi ayewul bésub Noflaay, nañu wattusi kër Aji Sax ji, ngir aar buur bi.
8 Yeen ñiy dar Buur, fegleen ko wet gu nekk, ku nekk ŋàbb ngànnaayam. Képp ku jëm ci seenug làng, dees koy rey, te àndleen ak buur bi buy dugg ak buy génn.»
9 Ci kaw loolu njiiti kuréli téeméer ya def mboolem la leen Yoyada sarxalkat ba sant. Ku nekk ànd ak say nit, ña aye bésub Noflaay ak ña ayewul bésub Noflaay, ñu bokk dikk ca Yoyada, sarxalkat ba.
10 Ba loolu amee, sarxalkat ba jox njiiti kuréli téeméer ya, xeej yaak pakki Buur Daawuda ya nekkoon ca biir kër Aji Sax ji.
11 Dag ya nag dar buur ba, ku nekk ŋàbb ay gànnaayam, ñu dare kër Yàlla ga ak sarxalukaay ba, wetu ndijoor ba wetu càmmoñ, ngir yéew buur ba.
12 Yoyada génne doomu buur ba, solal ko mbaxanam buur, jox ko kayitu doxalinu nguur ga; ñu fal ko nag buur, diw ko diwug pal. Ba loolu amee ñu tàccu, ne: «Guddalu fan, Buur!»
13 Ba Atalyaa déggee coowal dag yaak mbooloo ma, daa àgg ca mbooloo ma, fa kër Aji Sax ji.
14 Mu xool, yem ci buur ba taxaw fa kenu ga, na ñu ko baaxoo, kilifay xarekat yaak boroom liit ya dar Buur, waa réew ma mépp di bànneexook a wal liit ya. Atalya ne tareet ay yéreem ndax naqar, daldi yuuxu ne: «Wor am naay, wor am na!»
15 Ci kaw loolu Yoyada sarxalkat ba sant njiiti kuréli téeméer ya, kilifay gàngoor ga, ne leen: «Génneleen ko làng gi, te ku ko topp, jamleen ko, mu dee.» Fekk na Yoyada ne buñu ko rey ci biir kër Aji Sax ji.
16 Ba mu ko defee ñu teg ko loxo. Ba mu demee ba àgg kër Buur, bay tollook fa fas yay dugge, foofa lañu ko reye.
17 Ba loolu amee Yoyada digoo kóllëre diggante Aji Sax ji, ak buur baak askan wa, ngir ñu doon ñoñi Aji Sax ji. Mu digoo ko itam diggante Buur ak askan wa.
18 Ci kaw loolu waa réew ma mépp ànd dem ca kër Baal. Ñu màbb ko, ay sarxalukaayam ak jëmmi nataalam, ñu tas tasar, Matan sarxalkatu Baal ba, ñu rey ko ca kanam sarxalukaay ya. Ci biir loolu Yoyada sarxalkat ba teg ay wattukat ca kër Aji Sax ji.
19 Mu dellu nag woo njiiti téeméeri nit yaak waa Keret ñaak yeneen dag yaak mboolem waa réew ma, ñu jële Buur kër Aji Sax ji, jaare ca buntu dag ya, yóbbu ko kër Buur. Yowas daldi toog ca ngànguney buur ya.
20 Waa réew mépp di bànneexu, péey ba ne tekk. Atalya moom, fekk na ñu jam ko saamar ba mu dee ca kër Buur.