4
Ku mucc xare wax na
1 Ndeysaan, wurus wa giim na!
Ngëneelu wurus soppiku na.
Doj yu sell yaa wasaaroo,
ca boppu mbedd yépp.
2 Doomi Siyoŋ yu góor yu jar ya!
Wurus lees leen daan nàttablee,
ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban
lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.
3 Ag till sax joxe na weenam,
nàmpal doomam,
te sama bokk yi mujj néeg
ba mel ni bànjóolig màndiŋ.
4 Luy nàmp a nga mara mar,
ba làmmiñ taqoo denqleñ.
Gone yaa ngi ñaan mburu,
te kenn daggalu leen.
5 Ñi daan xéewloo ay bernde,
tey ñoo xiif, ne lasar ca mbedd ya.
Ña yaroo woon yérey tànneef,
tey ñoo goore jalu mbuubit.
6 Sama ñaawtéefu askan wee màgg,
ba raw ñaawtéefu waa Sodom,
dëkk ba jekki jàllarbiku,
te loxo laalu ko.
7 Sunu kàngam ya setoon wecc,
seen yaram mucc gàkk,
di lerxat bay tàkk,
wér péŋŋ, leer nàññ.
8 Tey ñu gëna lëndëm bànqanoos,
xàmmeesu leen ci mbedd yi,
ñu ngi lax, di yaxi neen,
der wow koŋŋ ni matt!
9 Ña saamar rey a gënu demin
ña deeye xiif,
jeex tàkk, ne lasar,
ndax ñàkk meññatum tool.
10 Ndey ak xolu njureelam,
moo togge loxoom, doomu boppam,
def ko njëlam,
ci sama biir toskareg askan wi!
11 Aji Sax jee xëpp am sànjam,
sotti tàngooru meram,
moo jafal sawara fi Siyoŋ,
ba xoyom kenu ya.
12 Du benn buur fi kaw suuf bu gëmoon,
du kenn ci mboolem waa àddina
ne bañ akub noon dina dem
ba bëtt bunti Yerusalem.
13 Seen bàkkaari yonent yaa,
seen ñaawtéefi sarxalkat yaa;
ñoo tuur fa digg dëkk ba
deretu aji jub ñi.
14 Ña ngay tëñëx-tëñëxi
niy gumba ci mbedd yi,
deret ja sobeel leen ba maneesula laal
seeni yére.
15 Ñoom lañuy gëdd naan:
«Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi!
Soreleen, soreleen, buleen nu laal.»
Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet;
ñooña ne leen: «Dootu fii!»
16 Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare,
faaleetu leen;
cér lees séddul sarxalkat,
te teraleesul mag.
Waa Yerusalem àddu na
17 Ba tey sunu gët a ngi giim,
ndax ndimbal lu nuy séentu ci dara.
Fa sunuy tata lanu séentoo wenn xeet
wu nu manula wallu.
18 Sunuy tànk lees di topp,
ba manatunoo daagoo sunuy mbedd;
sunu bés jege,
sunu àpp di matal,
sunu saa taxaw!
19 Ñi ñuy dàqa gëna gaaw ay jaxaay,
ci kaw tund yi lañu nu ne dann,
màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.
20 Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal,
ca seeni yeer la tance,
te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke
fi digg xeet yi.
Yeremi àddu na
21 Bégleen te bànneexooy,
yeen Edomeeni réewum Ucc,
ci yeen it la kaasu mbugal di jàllsi,
ngeen màndi, futteeku, ne duŋŋ.
22 Yaw Siyoŋ, sa mbugal mat na,
deesatu la yóbbu ngàllo;
yaw Edom laa ne, Aji Sax jee lay fey
sa ñaawtéef,
feeñal say bàkkaar.