10
Musiba dal na Nadab ak Abiyu
1 Ci kaw loolu doomi Aaróona yu góor yi tudd Nadab ak Abiyu jël ku ci nekk ab andam, def cay xal, def ca cuuraay, indil ko Aji Sax ji, muy taal bu dul ndigal te santu leen ko woon.
2 Sawara ne jippét, bawoo fi Aji Sax ji, lakk leen ba ñu dee fa kanam Aji Sax ji.
3 Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
4 Ba mu ko defee Musaa woolu Mikayel ak Elsafan, góor ñiy doomi Usyel, baayu Aaróona bu ndaw. Mu ne leen: «Kaayleen jële fi seen bokk yii ci bérab bu sell bi, te ngeen génne leen dal bi.»
5 Ñu jàpp ca seeni mbubb, génne leen dal ba, muy la Musaa santaane woon.
6 Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te merum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki bànni Israyil gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk.
7 Bunt xaymab ndaje mi, buleen ko wees, lu ko moy dingeen dee, ndax diwu palu Aji Sax jaa ngi ci seen kaw.» Ñu def la leen Musaa sant.
Li war ci sarxalkat
8 Aji Sax ji wax Aaróona itam ne ko:
9 «Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir xaymab ndaje mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
10 Dangeen wara mana ràññee lu sell ak lu ñu sellalul, dangeen wara ràññee itam lu set ak lu setul.
11 Nangeen jàngal bànni Israyil mboolem dogal yi leen Aji Sax ji dénk, te Musaa jottli leen ko.»
12 Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.
13 Lekkleen ko ci bérab bu sell. Sa cér la, yaw ak say doom yu góor, ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Loolu lañu ma sant.
14 Waaye dënnu saraxu yékkati-jébbale bi ak tànkub jooxe bi, lekkleen ko ci bérab bu mucc sobe, yaak say doom yu góor ak say doom yu jigéen, ndax seen cér la, ci saraxi canti bànni Israyil ci biir jàmm, nga moom ko yaak say doom.
15 Tànkub jooxe bi ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.»
16 Gannaaw loolu Musaa laajte, ba am lu leer ci mbirum sikketu saraxas póotum bàkkaar bi, ndekete lakk nañu ko, ba mu dib dóom. Mu mere ca doomi Aaróona yu góor ya des, di Elasar ak Itamar, ne leen:
17 «Lu waral lekkuleen sarax biy póotum bàkkaar ci bérab bu sell? Lu sella sell la, ñu jox leen ko, ngeen war koo yenniku bàkkaaru mbooloo mi, ba defal leen seen njotlaay fi kanam Aji Sax ji.
18 Gannaaw dugaleesul deret ji ca biir bérab bu sell ba, waroon ngeena lekk sikket bi ci bérab bu sell, muy li ma santaane woon.»
19 Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?»
20 Musaa dégg kàddu yooyu, rafetlu ko.