28
Ku bon daw na te dàqeesu ko,
ku jub ñeme ni gaynde.
 
Bu am réew dee fippu, kilifa ya bare;
réew mu jàmm sax, kilifa gaa am déggin ak xam-xam.
 
Ku ñàkk, su jekkoo ab ndóol,
du ko bàyyil fepp, day mel ni waame.
 
Ku wacc yoon, gërëm ku bon;
ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.
 
Ku bon xamul njub,
kuy wut Aji Sax ji, xam nga njub bu wér.
 
Ñàkk te mat
moo gën barele te dëng.
 
Gone gu sàmm yoon am nag dégg,
ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.
 
Kiy leble di tege, ba barele,
kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.
 
Soo dee tanqamlu yoon,
sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
 
10 Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal,
yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi,
waaye ku mat di jagoo ngëneel.
 
11 Waay a ngi barele, defe ne xelu na;
ku néewle am ug dégg, gis ne xeluwul.
 
12 Bu ku jub amee ndam, mbégte mu réy la;
ab soxor falu, ñépp làquji.
 
13 Kuy làq say tooñ doo baaxle,
ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.
 
14 Mbégte ñeel na ku saxoo ragal,
waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.
 
15 Kilifa guy soxore néew-ji-doole
mook gaynde guy yëmmoo yem, mbaa rab wuy songe.
 
16 Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk,
waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.
 
17 Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw;
bu ko kenn taxawu.
 
18 Mat, mucc;
dëng, dàll daanu.
 
19 Beyal sab tool, sab dund doy;
topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.
 
20 Boroom worma, bare barke;
ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
 
21 Par-parloo baaxul,
waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
 
22 Ab nay day yàkkamtee barele,
te xamul, ba ko ñàkk di dab.
 
23 Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg;
yaa koy gënal ku ko doon jay.
 
24 Ku xañ say waajur seen alal
te defe ne tooñoo,
yaa neexook saaysaayu yàqkat.
 
25 Ku bëgge day sooke ay,
te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
 
26 Ku doyloo sam xel, dof nga;
ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
 
27 Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk;
nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.
 
28 Bu ab soxor faloo, ñépp làquji,
bu daanoo, ku jub teg tànk.