Sabóor 137
Jooye nanu àll
Ca tàkkal dexi Babilon,
foofa lanu daa toog,
fàttliku Siyoŋ, jooy.
Ca garab ya
lanu daa wékk sunuy xalam.
Fa la nu sunuy sang daa woyloo,
not nu, bëgg nu bégal leen,
naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.»
Moo nu nuy woye woyu Aji Sax ji
kaw suufas yéefar?
Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte,
yal na ma doole dëddu!
Yerusalem, su ma la fàttlikuwul,
fonk la, ba gën laa bége lépp,
yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
 
Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña,
keroog jantub Yerusalem,
ba ñu naan: «Màbbleena màbb,
ba kenug dëkk bi siiñ!»
Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas,
ndokklee ku leen fey jëf,
ja ngeen nu def!
Ndokklee ku ne cas seeni fere,
tas ciw doj!