Sabóor 31
Naa siggi, noon sëgg
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji, yaw laa làqoo,
yàlla buma rus mukk.
Yiwee ma sa njekk.
Teewlu ma,
gaawe ma,
may ma, ma sës ci yaw, fegu.
Aar ma, ma mucc.
Yaa may yiir, di ma aar,
jiite ma, wommat ma ngir yaw.
Génne ma fiir gi ñu may tëroo;
yaw yaa di sama rawtu.
Yaw laa dénk sama bakkan.
Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma.
 
Maa bañ kuy topp tuuri neen.
Man, Aji Sax ji laa wóolu.
Damay bég, di bànneexoo sa ngor,
li nga xoole samaw tiis.
Ràññee nga sama njàqarey xol.
Waccoo ma ci loxol noon,
danga maa taxawal fu ma yaatoo.
 
10 Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa!
Samay gët a ngi giim ndaxu tiis,
xol jeex, yaram jeex.
11 Naqar a ngi may rey,
tiis di wàññi samay fan,
sama doole ŋiis ndax sama njubadi,
samay yax semm.
12 Noonoo noon a ma sewal,
dëkkandoo waxi noppi,
xame seexlu ma,
ku ma gis biti, di ma daw.
13 Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee,
ma mel ni ndab lu yàqu.
14 Damaa dégg jëw yu bare,
lu raglu dar ma kepp.
Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel,
di wut sama bakkan.
 
15 Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku.
Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
16 Yaa yor sama àpp.
Xettli maak ku ma noonoo
ak ku may sonal.
17 Leeralal ma sa kanam, Sang bi,
walloo ma sa ngor.
18 Éy Aji Sax ji, woo naa la wall,
yàlla buma rus.
Yal na ku bon rus,
ne xerem biir njaniiw.
19 Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat
buy wax aji jub waxi reewande,
di réy-réylook a xeebaate.
 
20 Yàlla yaa yaa ngëneel
loo dencal ku la ragal,
defal ko ku la làqoo,
doom aadama seede.
21 Yaa koy làq fa nga làqu,
fa pexey nit àggul.
Nga yiir ko, mu yiiru
ci ayu làmmiñ.
 
22 Teddnga ñeel na Aji Sax ji!
Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe
biir dëkk bu ñu gaw.
23 Man nag saalitoon naa ne:
«Yàlla dagg na ma, sànni!»
Ndeke ba ma lay woo,
dégg nga samay dagaan.
 
24 Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji.
Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm,
di yool, ba wis kuy réy-réylu.
25 Képp ku yaakaar Aji Sax ji,
dëgërlul te amu fit.