Sabóor 57
Yàlla jógal, wallu ma!
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma*.
 
Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma,
fi yaw laay làqu,
yiiroo sa kiiraay,
ba musiba yi jàll.
Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji,
Yàlla, mi may matalal.
Mooy yónnee fa asamaan, musal ma,
dumaal ma ku may not.
Selaw.
Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.
 
Maa ngi tëdd ci biiri noon
yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama.
Seeni sell niy xeej aki fitt,
seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim suuf sépp.
Noon yi di ma fiir,
sama xol jeex.
Ñu gasal mam pax,
far tàbbi ca.
Selaw.
 
Yàlla, dogu naa,
dogu naa woy, di la kañ.
Na sama jëmm jépp yewwu,
xalam ak moroom ma yewwu;
ma yee leeru njël.
10 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi,
kañ la ci biir waaso yi.
11 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan,
sa worma àkki fa kawa kaw.
 
12 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim àddina sépp.
* 57:1 Seetal ci 1.Samiyel 24.