Sabóor 63
Maa namm Aji Sax ji
1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.
2 Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla,
ma di la sàkku,
sama bakkan mar la,
sama jëmm namm la,
fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
3 Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo,
ngir niir sa leer ak sa teddnga.
4 Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan;
ma àddu boog, kañ la!
5 Dama lay sant, sama giiru dund kay,
yékkatiy loxo, sàbbaale la.
6 Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural,
ma bég, sarxolle, màggal la.
7 Su ma tëddee, fàttliku la,
waxtuw guddi dama lay xalaat.
8 Yaay sama ndimbal,
may làqoo sa kiiraay,
di sarxolle.
9 Sama xol taq la,
nga téyee ma sa ndijoor.
10 Waaye ñiy wuta faat sama bakkan
ñoo jëm xóotey njaniiw.
11 Ñu jébbal leen ñawkay saamar,
till séddoo.
12 Buur moom, di bége Yàlla;
képp ku koy giñe di ko kañoo,
fen-kat ne xerem.