Sabóor 74
Yàlla, bu la noon ree
Muy taalifu yeete, giiroo ci Asaf.
 
Éy Yàlla, lu tax nga wacc nu fàww,
di dal ak xol bu tàng
ci sa xari parlu yii?
Bàyyil xel askan wi nga jënd bu yàgg,
yaa jot gii giir, séddoo leen.
Bàyyil xel tundu Siyoŋ, fa nga dëkke woon.
Dikkal, xool gent bu yaa bii dul jeex,
noon yàq lépp ci biir kër gu sell gi.
 
Say bañ xaacu nañ fa sa digg bérabu ndaje ma,
samp seen raaya.
5-6 Sémmiñ dal, wàkku awu.
Mbete ñu xàcciy sémmiñ, di gori geer,
ba lu fa doon liggéeyu yett, tas.
Dañoo taal sa kër gu sell,
sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko.
Ñu namm noo not ba nu nooy,
fuy bérabu ndajem Yàlla ci réew mi, ñu lakk.
Sunuy takk réer na nu,
yonent amatul,
te kenn xamul fu lii di àkki.
 
10 Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke?
Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww?
11 Looy téye sa loxol ndijoor?
Na sa loxo jóge sa dënn, nga buube leen.
 
12 Yàlla, yaa masa doon sama buur,
di ma walloo ci digg réew mi.
13 Yaa xàjjale géej gi ci sa doole,
toj boppi ninki-nànka ya ca ndox ma,
14 yaa rajaxe kaaŋi rab wa,
leele ko rabi màndiŋ ma.
15 Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal,
ŋiisal dex yu masa wal.
16 Yaa moom bëccëg, moom guddi,
teg fi weer week jant bi.
17 Yaa rëdd mboolem digi suuf,
sàkk noor ak nawet.
 
18 Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree,
xeet wu amul bopp a lay sewal.
19 Bul wacce rabu àll sam xati,
bul sàggane sa néew-doole yi mukk.
20 Ngalla xoolal ci kóllëre gi,
fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
21 Yàlla bu néew-doole ñibbaale gàcce,
yal na ku ñàkk ak ku néewle di la santandoo.
22 Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg,
bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal.
23 Bul tanqamlu sa coowal noon yi,
ñii la jógal, seenum riir a ngi jolli saa su ne.