6
Gaalu Yàlla ga dem na Yerusalem
Ba loolu wéyee Daawuda dellu woo mboolem ñeyi xarey Israyil, ñuy fanweeri junni. Mu fabu, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, dem Baala, ca Yuda, ngir jëleji fa gaalu Yàlla gi ñu tudde Tur wi, turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, ki tooge diggante malaakay serub, yi tiim gaal gi. Ñu teg ko ci kaw watiir wu bees, jële ko kër Abinadab ga woon ca kaw tund wa. Usa ak Axyo, doomi Abinadab yu góor ya dox, jiite watiir wu bees wa. Noonu lañu dawale watiir wa yeb gaalu Yàlla ga, jële ko kër Abinadab, ga ca kaw tund wa, Axyo dox jiitu ko. Daawudaak waa kër Israyil gépp a ngay bànneexoo mboolem jumtukaayi xumbéen fi kanam Aji Sax ji; muy lu ñu defare bantu garabu sippar, ak ay keseŋ-keseŋ aki tabala ak xeeti xalam.
Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga. Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko fàdd foofa, ndax ug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga*. Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji teg Usa. Moo tax mu tudde bérab booba Peres Usa (mu firi Mbugalum Usa), muy turam ba tey jii.
Daawuda am na tiitaange lool bésub keroog ci Aji Sax ji. Ma nga naan: «Ana nu gaalu Aji Sax ji mana dale ak man?» 10 Loolu nag tax Daawuda nanguwula yóbbu gaalu Aji Sax ji fa moom, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Mu waññi gaal gi, yóbbu ko ca kër Obedd Edom waa Gaat ba. 11 Gaalu Aji Sax ji nekk na kër Obedd Edom waa Gaat ba ñetti weer. Aji Sax ji barkeel Obedd Edom, mook këram gépp.
Gaal ga dikk na Yerusalem
12 Ba loolu amee ñu xamal Buur Daawuda ne ko: «Aji Sax ji de barkeel na Obedd Edom ak mboolem lu bokk ci moom ndax gaalu Yàlla gi.» Daawuda jëleji gaalu Yàlla ga kër Obedd Edom, daldi koy yóbbu ci biir mbégte mu réy ba këram, fa ñu naan Kër Daawuda. 13 Ba ña gàddu gaalu Aji Sax ja séqee juróom benni jéego, aw yëkk ak wëllu wu duuf la Daawuda sarxal. 14 Daawudaa ngay fecc ak doole fa kanam Aji Sax ji. Daawudaa nga gañoo am xar-sànnim lẽe. 15 Naka la Daawuda ak waa kër Israyil gépp di yóbbu gaalu Aji Sax ji, sarxolle yaak liit ya jolli.
16 Ba gaalu Aji Sax jay duggsi ca biir gox ba ñu naan Kër Daawuda, soxnas Daawuda, Mikal doomu Sóol a nga sëppu ca palanteeram. Mu gis Buur Daawuda di tëb ak a fecc ca kanam Aji Sax ji. Mu jéppi ko lool.
17 Ba mu ko defee ñu indi gaalu Aji Sax ji, yeb ko ca bérabam, ca biir xayma ba ko Daawuda sampal. Daawuda daldi joxe fa kanam Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm. 18 Daawuda joxe saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm, ba noppi daldi ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. 19 Mu séddale aw ñam askan wépp, mbooloom Israyil mépp, góor ak jigéen; ku ci nekk mu jox la menn mburu ak yàpp wu ñu saaf ak benn nàkku reseñ. Mbooloo ma doora dem, ku nekk ñibbi këram.
20 Ba loolu amee Daawuda walbatiku, dugg biir këram, ngir ñaanal waa këram. Soxnaam Mikal doomu Sóol génn dajeek moom, ne ko: «Buuru Israyiloo, yaaka teral sa bopp bésub tey jii! Nga futteeku tey jii fi kanam jigéen ñiy sa jaami jawriñ yi, mbete nit ku tekkiwul dara!» 21 Daawuda ne Mikal: «Fi kanam Aji Sax ji ma taamu, wacc sa baay ak waa këram gépp, ngir fal ma kilifag Israyil, ñoñi Aji Sax ji, fi kanam Aji Sax ji laay bànneexu. 22 Dinaa gëna teddadil sama bopp sax, gëna toroxlu, ba gisal ko sama bopp, te du tere jaam yu jigéen yi ngay wax teral ma.» 23 Mikal doomu Sóol jooju nag amul doom, ba ni mu deeye.
* 6:7 Sarxalkat yi rekk ñoo amoon sañ-sañu laal gaalu Yàlla ga, te Leween ñi rekk ñoo amoon sañ-sañu gàddu ko. 6:19 yàpp wu ñu saaf walla benn nàkku tàndarma.