9
Mbugal mu mucc topp dal na askani diiwaan bi
1 Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo rot
ci kaw réewum Addarag,
ba dali ca kaw Damaas.
Du ci mboolem giiri Israyil rekk
la Aji Sax ji ne jàkk bëtam,
waaye doom aadama yépp la ne jàkk.
(xg / Gëti nit ñi, ba ci giiri Israyil gépp kat,
ñu ngi ne jàkk ci Aji Sax ji.)
2 Kàddu gi dal na itam Amat,
ga digalook Damaas,
dal Tir ak Sidon, ak la ñuy muus lépp.
3 Tir moo tabaxal boppam tata,
moo dajale xaalis ni feppi suuf,
ak wurus wu ne xas ni donji banu mbedd.
4 Ndeke Aji Sax ji moo koy moom,
xalab alalam biir géej,
te sawaraa koy xoyom.
5 Askalon moo koy gis, tiit;
Gasa gis ko, jàq njàqare lu réy,
mook Ekkron it ndax yaakaar ju tas.
Gasa la buur bay réere,
Askalon ñàkk ku ko dëkke.
6 Xeet wu raxe mooy sanci Asdodd,
te maay sàggi sagub Filisteen ñi.
7 Ci seen gémmiñ laay foqatee deret ji ñuy lekk,
yàbbiloo leen seen ñam yu seexluwu
yi ñu ŋank.
Seenu ndes it dina ma def seen Yàlla,
mel nig làng ci giirug Yuda,
Ekkron it ci sama ñoñ lay bokk ni Yebuseen ñi.
8 Maay taxaw wattu fi wër sama kër,
aar ko ci ñiy dem ak a dikk,
ba boroom doole dootu not sama waa kër,
nde léegi samay gët laa leen ne jàkk.
Buur Almasi dikk na
9 Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru,
janq Yerusalem mu taaru laa ne:
Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw,
moo jot njekk ak mucc,
te teewu koo woyof, war mbaam,
cumbur doomu mbaam.
10 Maay dagge watiiru xare diiwaanu Efrayim,
dagge fasu xare fi Yerusalem,
xalay xare damm,
muy wax xeet yi jàmm,
kilifteefam dale géej ba géej,
dale dexu Efraat ba ca cati àddina.
Aji Sax ji mooy xeexal ñoñam
11 Yaw nag, deret ji feddli sama kóllëreek yaw,
ci laay seet ba yiwi sa nit ñi ñu tëj
biir kàmb gu ndox amul.
12 Yeen ñi ñu tëj, ngeen di dunde yaakaar,
delluleen ca tata ja.
Bésub tey jii sax maa dogu ne
ñaari yoon laa leen di yool.
13 Yuda déy laay bank, muy samag xala,
te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi.
Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati
ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan).
Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.
14 Su boobaa Aji Sax jeey feeñ fi leen tiim,
ag fittam tàkk nig melax.
Bufta gi la Boroom bi Aji Sax ji di wal,
ànd ak ngëléni bëj-saalum, dikk.
15 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy aar ñoñam,
ñuy falaxe, di joggati doji mbaq,
di naan ak a xaacu ni ñu màndi.
Ni ndabi deretu juru sarax di feese,
ni lañuy feese ak deretu noon yi,
taq ci ripp ni cati sarxalukaay ba.
16 Bésub keroog seen Yàlla Aji Sax ji
mooy sàmm ñoñam nig jur,
ñuy lerxat cim réewam
ni peri gànjar di ray-rayee ci mbaxanam buur.
17 Ndaw bànneex akub taar ca ñoom!
Pepp yafal xalelu góor,
biiñ bu bees naatal yaramu janq.