25
Ibraayma nelaw na
1 Ibraayma jëlaat na soxna su tudd Ketura,
2 am ca Simran ak Yogsan ak Medan ak Majan ak Yisbag ak Suwa.
3 Yogsan jur Seba ak Dedan. Askani Dedan ñooy Asureen ñi, Letuseen ñi ak Lewumeen ñi.
4 Doomi Majan yu góor ñoo di Efa ak Efer ak Enog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu.
5 Ibraayma nag donale Isaaxa lépp lu mu moom.
6 Doom yu góor, ya Ibraayma am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa.
7 Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175).
8 Ba loolu weesoo la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel.
9 Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntum xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Cowar, mi bokk ci xeetu Ett.
10 Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata.
11 Gannaaw ba Ibraayma nelawee, Yàlla barkeel na doomam Isaaxa. Isaaxaa ngi dëkkoon ca wetu teenu Laxay Roy.
Askanu Ismayla
(Saar 25.12-18)
12 Ismayla moomee nag, doomu Ibraayma jaak Ajara mu Misra, ma doon jaamub Saarata, askanam mooy lii.
13 Turi doomi Ismayla yu góor ni seen juddu toppante, ñoo di Nebayot, taawub Ismayla, ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam
14 ak Misma ak Duuma ak Maasa
15 ak Adàdd ak Tema ak Yetur ak Nafis ak Kedama.
16 Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni làng ci seeni sanc ak seeni dal.
17 Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam.
18 Ña nga dëkkoon diggante ba dale Awila ba Sur, ga jàkkaarlook Misra, booy jëm Asur. Noonu la fa askanu Ismayla sance, jàkkaarlook doomi baayam yépp.
Askanu Isaaxa doomu Ibraayma
(Saar 25.19—35.29)
19 Isaaxa doomu Ibraayma ju góor ja, askanam mooy lii. Ibraaymaa jur Isaaxa.
20 Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, mi bokk ci xeetu Aram, te dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, mi bokk itam ci xeetu Aram.
21 Gannaaw ga, soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb.
22 Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji.
23 Aji Sax ji ne ko:
«Ñaari giir nga ëmb,
nara am ñaari xeet yuy xaajaloo,
wenn wi mooy ëpp doole wi ci des,
te mag ji mooy surgawu rakk ji.»
24 Ba mu demee ba wara mucc, amul lu moy ay seex.
25 Naka noona ka njëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (muy firi Ku jëxëm).
26 Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (muy firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at.
Esawu sàggane na céram
27 Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu te bëggoon toogaayu kër.
28 Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba.
29 Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd.
30 Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lu xonq lee waay, ba ma duy ci sama biir, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (muy firi Xonqe).
31 Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy njëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw.»
32 Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?»
33 Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono li mu yeyoo ndax li muy taaw.
34 Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo.