Li Kàddug Yàlla di yégle
Loo xalaat ci Kàddug Yàlla? Ca Njàlbéen ga jàng nga cosaani àddina, li ko dale ci Aadama ak Awa, ak Kayin ak Abel, ak Nóoyin ak Ibraayma ak Saarata ak Ajara ak Ismayla ak Isaaxa ak Yanqóoba ba ci Yuusufa.
Léegi nag, lan mooy sa xalaat ci lii: Ba Yàlla sàkkee àddina, lépp a baaxoon, kon lu tax àddina si jaxasoo nii tey? Lan moo tax nit mana bon xol? Ibraayma, lu ko taxa nekk xaritu Yàlla?
Ndax mas ngaa xalaat ci lan moo mana soppi xolu nit? Ndax Yàlla man naa baale bépp tooñ? Nan la nit mana amee texe? Lu nara xew su àddina tukkee? Nan la Àjjana mel?
Kàddug Yàlla am na ci ay tont.
Léegi noo ngi jëm ci téere yi des.
Mucc ga, di ñaareelu téere bi, ci la Yàlla joxe yoonam, Musaa jottali, gannaaw ba Yàlla musalee bànni Israayil cig njaam. Ñu ngi ciy nettali, bi Yàlla santee Musaa mu sàkk ab xaymab jaamookaay bu taxawalin ba ak li ci biiram lépp di jëmmal sellaayu Yàlla ak teewaayam ci seen biir.
Sasu Sarxalkat yi, di ñetteelu téere bi, ci la Yàlla tegtale ay sarax yuy doon ag njotlaay ci bàkkaar ak sobe, li ñag diggante Yàlla Aji Sell ji ak doom aadama.
Yeneen téerey bind yu sell yi ñoo indi Ayóoba, ak Kàddu yu xelu yu Suleymaan, ak li ñu bind ngir nit ñi am xel mu rafet, mana yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon. Yonent Yàlla Esekiyel bind ci xel mu yees mi Yàlla bëgga def ci nit.
Kàddug Yàlla nag yemul ci nettali jaar-jaari jamono, ndax Yàllaa ci fésal mooy kan; mooy ki amul maas, di boroom bépp mbaax, di boroom cofeel ak yërmande, di cellte doŋŋ, xajoowul benn bàkkaar. Yàlla, ci mbaaxam la sàkke àddina, sàkk nit. Waaye bàkkaar ak sobey nit mooy gàllankoor wi yàq digganteem ak Yàlla Aji Sell ji. Teewul Kàddug Yàlla xamle na pexe mi Yàlla teggee woowu gàllankoor, ba sàkkal doom aadama yoon wi mu mana jaar, ba dellu ci moom.
Yal na nu Yàlla teg ci yoon wi baax, ba nu mana taseek leeram, Yàlla boole nu ci njabootu Yonent Yàlla Ibraayma, baayu bépp gëmkat, taas nu ci barkeem.