11
Daawuda am na kuutaay
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese*,
ab car soqeekoo fa reen ya,
xelum Aji Sax ji tegu fi kawam,
xelum rafet xalaat ak ràññee,
xelum digle ak njàmbaar,
xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.
Ragal Aji Sax ji lay safoo,
du lu ko bëtam may lay àttee,
du lu ko noppam may lay dogale,
xanaa di àtte dëgg ku ñàkk,
di dogalal njub néew-ji-dooley àddina.
Mooy dóore àddina bantub kàddoom,
mooy reye ñu bon ñi ngelawal gémmiñam.
Njubte lay gañoo,
takkoo kóllëre.
Till ay bokk ak mbote ab dal,
segg bokk akub tef ab tëraay,
wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar,
tuut-tànk jiite leen.
Nag ak rab wu aay di forandoo,
seeni doom goorandoo,
gaynde di lekkum ngooñ niw yëkk,
luy nàmp di fowe paxum ndox-suuf,
perantal di laal tostanum ñàngóor.
Deesatul gaañe mbaa di lore,
fi mboolem sama kaw tund wu sell wi,
ndax ni ndox di feese ba muur géej,
ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
10 Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba,
taxaw di raaya buy gindi xeeti àddina si,
jàmbur ñi di gëstusi,
dalluwaayam ba jagoo màggaayu Yàlla.
 
11 Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom
ñaareel bi yoon,
ngir jotaat ndesu ñoñam
wa des Asiri ak Misra ak Pattros ak réewum Kuus ak Elam ak Sineyaar ak Amat ak biir duni géej ya.
12 Mooy yékkatil xeet yi raaya,
dajale ña ñu dàqe Israayil,
ak ña ñu jële Yuda, tasaare leen,
ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo.
13 Fiiraangey Efrayim day jeex,
njéefoy Yuda dakk,
Efrayim dootul fiire Yuda,
Yuda dootul jéppi Efrayim.
14 Xanaa ñu ne coww ba sowu,
ne jàyy cëppandoo
fa kaw waggi Filisteen ña,
waa penku, ñu sëxëtoondoo;
Edom ak Mowab, ñu teg loxo;
Amoneen ña nangul leen.
15 Aji Sax jeey wowal walum ndox,
ma séle géeji Misra.
Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat,
wal kook doole,
dóor ko, mu séddalikoo juróom ñaari wal,
mu jaarale ca nit ñu caraxu,
16 def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam,
ña dese fa Asiri,
mu mel ni yoon wa ñeeloon Israayil,
bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra.
* 11:1 Yese mooy baayu Daawuda.