26
Aji Sax jeey may ñoñam ndam
Bésub keroog dees na woy
wii woy fi réewum Yuda:
«Dëkk bu dëgër lanu am,
Yàllaa nu may kaaraangey tata, biir ak biti!
Ubbileen bunt yi,
ba xeet wi jub te sàmm ngëm duggsi!
Yaw Aji Sax ji,
ku dogu, pastéefu, wóolu la,
nga may ko jàmm ju mat,
nde moo la wóolu.
Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg;
Ki Sax, di Aji Sax ji déy,
moo mat cëslaay ba fàww.
Moo wàcce ñi dëkke woon fa kaw,
moo detteel waa dëkk ba aju woon,
daaneel leen, ñu xalangu,
ba mëq suuf,
baadoola joggi, dëggaate,
néew-ji-doole noote leen.»
 
Ku dëggu, yoonam day maase;
ku dëggu, Aji Jub ji jubal xàllam.
Aji Sax ji, nu ngi lay xaar,
fi sa kaw yoonu santaane yi,
di tudd sa tur, di la bàyyi xel,
lii déy, mooy sunu nammeelu xol.
Xol laa lay sàkkoo guddi,
sama jëmm jépp di la laaj.
Bu say àtte teewee fi kaw suuf,
waa àddina xame ca luy njub.
10 Ku bon, boo ko yërëmee,
du jàng tus ci njubte.
Biir réew mu nit ñay jubal
lay xal di luubale,
du faale màggaayu Aji Sax ji.
11 Aji Sax ji, yaa xàcc sa loxo,
waaye yéguñu ko.
Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus,
te sawaraay xoyom sa noon yooyu.
12 Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm,
te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal.
13 Aji Sax ji sunu Yàlla,
yeneen sang yu la moy moom nañu nu,
waaye saw tur rekk lanuy màggal.
14 Yooyu sang dee nañu, nekkatuñu,
wuute nañu, jógatuñu.
Yaa def nii, faagaagal leen,
ba far sax seen tur.
15 Aji Sax ji, yaa yokk xeet wi,
yaw mii yaa yokk xeet wi,
yaa fésal sa màggaay,
yaa yokk mboolem kemi réew mi!
 
16 Éy Aji Sax ji, ci biir njàqare lañu la sàkkoo;
ba ñu tegoo sa mbugal,
lañu la déey seenug ñaan.
17 Éy Aji Sax ji, ni kuy matu
lanu meloon fi sa kanam,
di wañaarooka yuuxu.
18 Danoo ëmb bay matu
te jurunu lu moy ngelaw.
Indiwunu genn mucc ci àddina,
mayunu ci kenn lu ko taxa dund.
19 Waaye yaw askan wi, ñi nga deele
ñooy dellu dundaat,
seeni néew ay dekki,
ku doon nelaw sa biir bàmmeel,
yewwu, sarxolle.
Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer,
suuf delloosi ña dëddu.
Mbugal ñeel na géej ak jéeri
20 Yeen samaw askan, ayca duggleen seeni néeg,
tëju ca biir.
Làquleen as lëf, ba sànj mi jàll.
21 Aji Sax ji kat a ngii di génne màkkaanam ma,
nara dikke waa àddina mbugalu ñaawtéef,
ba suuf wone deret ji ñu tuur fi kawam,
te dootul sàng ñi ñu bóom.