29
Mbugal ñeel na Aryel
Wóoy ngalla Aryelee, Aryel*,
dëkk ba Daawuda dale.
Dundleen at ak at,
amalleen ci màggal ci kaw màggal.
Du tee ma wàcceel Aryel musiba,
ñuy yuuxooka jooyoo.
Yerusalem ay mel ci man
ni Aryel, taalub sarxalukaay.
Maay dal ab dal, wër la,
gawe la ay tata,
jali jal, fuuge la.
Dinga suufe ba mel ni kuy àddoo biir suuf,
sa baat di ndéey lu dégtoo xóote ya pëndub suuf lale,
mel ni njuuma lu waxam bawoo biir suuf,
baatam yeloo xóote ya pëndub suuf lale.
 
Say noon ay def gàngoor ni feppi suuf,
di naaxu nit ñu néeg, ñu ngelaw liy wal nib cox.
Loolooy jekki am, ca saa sa.
Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi moo lay dikke
dënook suuf su yëngu ak riir mu réy,
ngelaw riddi, di ngëlén,
ànd ak sawara wuy xoyome.
Mboolem xeet yu bare yiy xareek Aryel,
di song dëkk beeki tataam,
nar leena toroxal,
ñoom ñépp ay mel ni gént mbaa njeneeru guddi!
Su boobaa mu mel ni ku xiif,
géntul lu moy di lekk,
yewwu rekk, biir ba wéet;
mbaa ku mar, géntul lu moy di naan,
yewwu rekk, loof, put ga wow koŋŋ.
Noonu la gàngooru xeet yépp di nekke,
mboolem xeet yooyuy xaareji fa Siyoŋ!
 
Tendeefal, jommi rekk!
Gëmm, gumba rekk.
Ñiika màndi te biiñ taxul,
ñuy jang te ñoll taxul!
10 Aji Sax ji déy yeen la wal
ngelawal nelaw yu xóot,
taf seeni gët, te ngeen di yonent yi;
muur seeni bopp, te ngeen di boroom peeñu yi.
11 Peeñum xew-xew yii yépp ump na leen,
ni leen kàdduy téere bu ñu tay umpe.
Boo ko joxee ku jàng, ne ko mu jàng ko,
mu ne la manu ko, nde dees koo tay;
12 nga jox ko ku jàngul, ne ko mu jàng,
mu ne la manula jàng.
 
13 Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee,
lori neen lañu may wormaale,
te seen xol sore ma.
Seen ragal ak man it,
njàngum tari kepp la.
14 Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii,
ay kéemtaan aki kiraama
yuy tiiñ boroom xel ak xelam,
réer xamkat ak xam-xamam.»
 
15 Wóoy ngalla ñiy làqu Aji Sax ji,
di nëbb seen mébét,
ba lëndëm muur seen jëf,
ñu naan: «Ana ku nu gis?
Ana ku nu yég?»
16 Yeenaka juunum xel!
Dees na jaawale tabaxkatu njaq beek ban bi?
Ndax li ñu sàkk dina ne ki ko sàkk:
«Kii sàkku ma»?
Am njaq leey waxtaane tabaxkat bi naa:
«Kii manula tabax»?
La woon day wonni
17 Xamuleen ne fi leek lu néewa néew,
àllub Libaŋ soppalikub tóokër,
tóokër bi walbatiku meññ, ba ñu ne ab gott la?
18 Su bés baa ab tëx dégg kàdduy téere,
silmaxa tàggook lëndëm, di gis,
19 néew-doole yi dellu bége Aji Sax ji,
ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israayil.
20 Ku néeg déy dina neen,
kuy ñaawle sànku,
te képp kuy yeeru nu mu defe lu bon,
jóge fi.
21 Mooy ñiy tuumaal nit,
di fiir ab àttekat ca pénc ma,
di àtte ñàkkal nit ku jub ci dara.
22 Moo tax Aji Sax ji jotoon Ibraayma,
wax ak waa kër Yanqóoba, ne leen:
«Léegi Yanqóoba du rusati,
du amati yaraange.»
23 Bu am meññeefam gisee
li sama loxo def fi seen biir,
dinañu wormaal sama tur wu sell wi,
wormaal sama sellaay, man Aji Sell ju Yanqóoba.
Dinañu ma ragal, man Yàllay Israayil,
24 ba ñi réeroon, mujj xam;
ñurumtukat yi dégg ndigal.
* 29:1 Aryel, tur la wu ñuy woowe Yerusalem. Man naa tekki itam taalub sarxalukaay ba woon ca kër Yàlla ga.