32
Dëgg ay mujj
1 Buur a ngii, dëgg lay nguuroo,
jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;
2 ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw,
di kiiraay ci ngëlén,
mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ,
mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
3 Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm,
te noppi ñiy dégg dañuy teewlu,
4 ku yàkkamti di ràññee, ba mana xam,
làmmiñu ku dër gaawa wax lu leer.
5 Booba deesatul woowe ab dof «gor si»,
te njublaŋ dootul dégg «ku tedd ki».
6 Ab dof, waxi dof lay wax,
xel ma di nas ñaawtéef,
mu nar jëf ju teddadi.
Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji,
di xiifal ku xiif,
di xañ ku mar lu mu naan.
7 Ab njublaŋ, ay pexeem musiba la.
Njekkar lay nas,
ba bu néew-ji-doole sàkkoo dëgg it,
mu fen ba lor ko.
8 Waaye gor si, ngor lay mébét,
te ngor lay wéye.
9 Yeen jigéen ñi dal xel,
taxawleen temm, déglu ma;
yeen janq ji féex,
teewluleen ma.
10 Yeen jigéen ñi dal xel,
fi leek at aki fan ngeen jàq;
witt mi du baax, ngóob du taxaw.
11 Jigéen ñi dal xel, ragalleen;
yeen ñi féex laa ne, tiitleen!
Futtikuleen, ba ne duŋŋ;
gembooy saaku, ñaawloo.
12 Fëggleen seen dënn,
jooy tooli bànneex ya,
jooyleen reseñ ju nangu ja,
13 ak sama suufas bokk ya ay dég aki dagg nangu.
Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma,
ak dëkk bu xumb ba.
14 Kër gu rafet sax, dees koy wacc,
dëkk baak riiram, dees koy dëddu;
tund ak tóoju doon ay xunt ba fàww,
mbaamu àll ne ca finaax, jur ga di ca fore,
15 ba keroog Boroom bi ëf ci nun ag noowam,
màndiŋ mi soppalikub tóokër,
tóokër meññ, ba ñu ne ab gott la.
16 Su boobaa yoon dëkke màndiŋ mi,
dëgg tooge tóokër bi.
17 Su boobaa àtteb dëgg ay jur jàmm,
àtteb yoon di dalal tey aare ba fàww,
18 ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm,
ci dëkkuwaay yu wóor,
ci dalluwaay yu dal xel,
19 doonte gott bi day daanu ci tawub doji yuur,
dëkk bi detteelu ba ne dett.
20 Waaye ndokkalee yeen ñi tala ji fépp fuy ndox
te saña afal nag ak mbaam.