58
Jaamu Yàlla, tuub, rafet jikkoo ci gën
Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man,
te bul ñéeblu;
àddul ni bufta,
te yégal sama ñoñ seen bàkkaar,
ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy.
Man mii lañuy wuta déggal bés bu ne,
di wuta xam sama coobare!
Mbete askan wuy doxe yoon,
te waccul ndigalu yoonu Yàllaam.
Ñu ngi may ñaan àtteb dëgg,
bëgg man Yàlla, ma jege leen,
te naa: “Ana lu nuy woor te ñoru la?
Lu nuy toroxlu te teewluwoo?”
Ma ne: Bés bu ngeen woor,
yeena ngi topp seen bakkan,
di sëqatal seeni liggéeykat.
Xanaa du koor gu ànd ak xulook ŋaayoo,
ak di joqalantey këmëx yu metti?
Su ngeen bëggee seen ñaan àgg fa kaw,
dungeen woor ni ngeen woore tey.
Ndax lii moo di koor gi ma taamu,
ci bés bu nit kiy toroxlu?
Koorug dëngal loos ni barax,
lal saaku, sotti cib dóomu-taal,
tëdd ci, di ko ñaawloo?
Ndax loolooy seen koor,
ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?
 
«Xanaa du lii moo di koor gi ma taamu:
yolomal jéng yu metti,
fecci buumi nooteel,
afal ku diis;
dog lépp luy xeetu nooteel?
Xanaa du sédd ku xiif saw ñam,
fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk,
gis ku rafle, wodd ko,
te baña nëbbu mbokk mu soxla?
Su boobaa seen leer feq ni njël,
seen góom gaawa wér,
seen jëf yu jub gindi leen ci kanam,
leeru Aji Sax ji féete leen gannaaw.
Su boobaa bu ngeen woowee Aji Sax ji, mu wuyu;
ngeen ne wallóoy, mu ne: “Maa ngii.”
Ndegam génne ngeen nooteel ci seen biir,
ak di joxoñeeka wax lu ñaaw,
10 di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg,
di reggal néew-ji-doole,
su boobaa seen leer fenke biir lëndëm,
seenug këruus di ag njolloor,
11 Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu,
di leen màndale joor gu maral,
dëgëral seeni cér,
ngeen mel ni tool bu ñu suuxat,
mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis,
12 seeni nit tabaxaat gent ya woon,
ngeen yékkatiwaat fondmaa yu yàgga yàgg.
Dees na la woowe jagalkatu xar-xar yi,
mbaa kiy yeesal xàll yi, ngir dëkke réew mi.
 
13 «Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay,
baña def li leen neex sama bés bu sell;
su bésub Noflaay di seen nammeel,
di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral;
ngeen teral bés bi,
bañ cee topp li ngeen jikkowoo,
di topp seen bakkan
ak wax ju dul jeex;
14 su boobaa ngeen bànneexoo Aji Sax ji,
ma waral leen kawtey réew mi,
leele leen seen céru maam Yanqóoba.»
Aji Sax ji déy wax na ko.