61
Ki Boroom bi fal dikk na
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw,
ndax Aji Sax jee ma diw*, fal ma
ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm.
Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex,
yégal jaam yi seen goreel,
yégal ñi ñu tëj seen ubbite.
Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji,
ak at mu sunu Yàlla di mbugalee.
Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp,
ngir indil waa Siyoŋ ñiy ñaawlu
ab kaala gu wuutu dóomu-taal,
ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis,
ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex,
ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njubte yi,
njëmbat li Aji Sax ji jëmbat,
ngir teewal màggaayam.»
Ñooy tabaxaat gent ya woon,
yékkati béreb ya tasoon bu yàgg,
dekkal dëkk yu tas,
béreb yu gental ay maasi maas.
Ay gan ay dikk,
di leen sàmmal seeni gétt,
ay doomi doxandéem di leen beyali tool
ak tóokëri reseñ.
Yeen nag lees di woowe:
«Sarxalkati Aji Sax ji,»
ñu naa: «Sunu jawriñi Yàlla yaa ngii!»
Alali xeet yi, yeena koy lekk,
di damoo seeni koom.
Sama ñoñ ay weccikoo seen gàcce
ñaari céri teraanga,
sarxolley mbég di seen cér,
wuutu toroxte.
Ñaari cér lañuy am ca seenum réew,
mbégte mu sax ñeel leen.
Man Aji Sax ji, damaa sopp yoon,
bañ càcc ak ñaawtéef.
Maay dàmp sama ñoñ ni mu ware,
fas ak ñoom kóllëre gu sax.
Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi,
xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi;
képp ku leen gis ràññee ne
ñooy askan wu Aji Sax ji barkeel.
Almasi bi bége na mucc gi mu maye
10 Maa bég a bég ci Aji Sax ji,
sama xol di sedd ci sama Yàlla jii.
Moo ma solal yérey mucc,
sànge ma mbubbam ndam,
may nirook boroom séet
bu kaalawu ni sarxalkat,
ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
11 Ni suuf di fettalem njebbit,
ab tool di ko saxalem jiwu,
ni la Boroom bi Aji Sax ji di jebbile
dëgg ak cant,
xeetoo xeet seede ko.
* 61:1 Baat bi ñu tekkee «diw», ci la baatub Almasi jóge. Ab sarxalkat mbaa buur lañu daan diw, fale leen ko bala ñoo door seen liggéey.