Ayóoba
Téereb Ayóoba ci laaj bii la tënku: Lu tax ku deful daray daji coono? Ku mel ni Ayóoba, Yàlla ci boppam moo ko seedeel ne ku jub la. Moonte terewu koo jànkoonte ak coono yu jéggi dayo.
Ci kaw loolu la ñetti xariti Ayóoba dikke tànki dëfal ko, di joxe seen xalaat ci li waral coonoy Ayóoba, diy bàkkaaram, ci seen gis-gis. Waaye Ayóoba, bir na ko ne, moom deful lu tax mu wara yelloo safaan yi ko dal. Bëgg na layoo ak Yàlla (13.3), ngir Yàlla xamal ko lu mu koy toppe (10.2).
Yàlla ci boppam moo mujj wax ak Ayóoba kàddu yu ko jañax, ba mu ràññee matadig xam-xamam. Yàlla won na Ayóoba ne amul lenn lu mu tële, looloo tax Ayóoba waru koo saña teg tooñ; da ko wara wóolu.
Ci tënk:
1.1—2.13 Nattuy Ayóoba tàmbali na.
3.1—31.40 Lu jëm ci ñetti pàcci werante diggante Ayóoba aki xaritam.
32.1—37.24 Eliyu yékkati na kàddoom.
38.1—41.26 Aji Sax ji tontu na Ayóoba.
42.1-17 Ayóoba leqaliku na.
1
Ayóobaa barkeel, ragal Yàlla
Amoon na ca réewum Ucc*, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon. Amoon na juróom ñaari doom yu góor ak ñett yu jigéen. Alalam juróom ñaari junniy (7 000) gàtt la woon, ak ñetti junniy (3 000) giléem, ak juróomi téeméeri (500) lëkkey nag yuy rijji, ak juróomi téeméeri (500) mbaam yu jigéen, ak jaam yu bare lool. Góor googu daal moo ëppoon daraja ca mboolem waa penku.
Doomi Ayóoba yu góor ya nag dañu daa ay-ayloo berndey biir kër, ku nekk ak bésam. Su ko defee ñu yónnee, woo ca seen ñetti jigéen ña, ngir ñu bokk di lekk aka naan. Bu ñu demaan ba ñépp fégal, Ayóoba day yónnee ngir sangulooleen-set. Ci biir loolu day teela xëy, daldi leen joxeel ñoom ñépp ba ñu daj saraxu rendi-dóomal, ku nekk benn. Booba Ayóoba da naan: «Jombul sama doom yii bàkkaar nañu mbaa ñu xarab Yàlla ci seen xel.» Noonu la Ayóoba jàppoo woon.
Nattu nuyoo na
Mu am bés goney Yàlla dikk, teewsi fa Aji Sax ji. Seytaane Tuumaalkat bi itam bokk ca. Aji Sax ji ne Seytaane: «Ana foo jóge?» Mu ne: «Ci wër-wëraan ak doxantoo àddina laa jóge.» Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi? Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.» Seytaane ne ko: «Xanaa daa am lu waral Ayóoba ragal Yàlla? 10 Xanaa du yaa ko ñag, ñag këram ak mboolem alalam ba mu daj? Liggéeyam, nga barkeel, ba ag juram law ci réew mi. 11 Xàccal sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.» 12 Aji Sax ji ne Seytaane: «Ayca boog! Mboolem lu bokk ci moom a ngi ci say loxo, waaye moom ci boppam, bu ko sa loxo laal.» Ba loolu amee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji.
13 Mu am bés doomi Ayóoba yu góor ak yu jigéen bokk toog di lekk aka naan biiñ ca seen kër taaw. 14 Ci biir loolu ndaw dikk ne Ayóoba: «Nag ya daal a doon rijji, mbaam ya di for ca wet ga. 15 Genn gàngooru yàqkat bàyyikoo Seba, dikk daanu ci seen kaw, yóbbu leen; surga ya, ñu leel ñawkay saamar. Mennum man mii maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 16 Kooku daaneelagul kàddoom sax, keneen dikk ne: «Sawaraw Yàlla daal a wàcce asamaan, boole gàtt yaak surga ya, jafal ba xoyom leen. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 17 Kooka daaneelagul kàddoom, keneen dikk ne: «Kaldeen ñaa def ñetti gàngoor, dikk sëxëtoo giléem ya, yóbbu, surga ya, ñu leel leen ñawkay saamar. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 18 Kooka daaneelagul kàddoom, keneen dikkati ne ko: «Sa doom yu góor ak yu jigéen a doon lekk aka naan biiñ ca seen kër taaw bu góor, 19 ngelaw lu mag jekki bàyyikoo ca wàllaa màndiŋ ma, dal ca ñeenti weti néeg ba, mu màbb ca kaw gone ya, ñu dee. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.»
20 Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot, 21 daldi ne: «Duŋŋ laa génne sama biiru ndey te duŋŋ laay delloo. Aji Sax jee maye, Aji Sax jee nangu. Cant ñeel na Aji Sax ji.» 22 Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul, jiiñul Yàlla lenn lu juunu.
* 1:1 Ucc: jombul ma nga woon ca penkub Israayil, fi ñuy wax tey Arabi mbaa Yordani mbaa Siri. 1:6 goney Yàlla, maanaam ay malaakay Yàlla yu bokk ci péncum Yàlla.