14
Àddinaa gàtt, barew tiis
Ku jigéen jur,
yaa néewi fan, géejal coono!
Dangay tóor rekk, lax,
wéy ni takkndeer, doo toog.
Mooy kii nag nga teg bët,
mooy man mii nga nara layool!
Lu sobewu, ana ku ci mana am lu laab?
Du kenn!
Ndegam yaa dogalal nit ay fanam,
lim ay weeram,
dogal àpp ba, te du jaas,
teggi ko boog say gët, mu dallu,
ni liggéeykat bu jaanam wàcc ci bés.
 
Garab sax ñàkkul yaakaar.
Boo goree, mu jebbiwaat,
ba du ñàkk ay njebbit.
Reen ba man naa màggat,
ëkk ba deewe biir suuf,
mu yégum ndox rekk, jebbi,
saxaat nim njëmbat.
10 Waaye nit dee, doole réer,
bakkan rot, mu ne mes.
11 Day mel ni déeg bu ŋiis,
mbaa dex gu wow ba jeex.
12 Doom aadama it tëdd, du jógati,
du yewwooti, asamaan fekke,
du jógeeti ciy nelaw.
Làq ma sa mer, ba giif
13 Éy soo ma nëbboon biir njaniiw,
làq ma, ba sa mer giif,
dogalal ma àpp, te bañ maa fàtte!
14 Ndax dees na dee, di dundati?
Doon naa ko muñe sama fani coono yépp,
ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.
15 Doon nga ma woo, ma wuyu,
te kon nga namm sa càkkéefu loxo.
16 Doon nga wóoral samay jéego,
te doo ma toppe samay bàkkaar.
17 Konoon samag tooñ yebe ci mbuus mu takke;
sama ñaawtéef, nga muure ko malaan.
 
18 Waaye aw tund day màbb, ruus;
aw doj di toxu,
19 am ndox di jonji xeer ba mu jeex,
waame buub suuf, yóbbu,
te noonu ngay neenale yaakaaru doom aadama,
20 man ko, mu dëddu fàww,
kanam ga soppiku, nga jalax.
21 Doom ya tedd, yégul;
ñu tekkeedi, tinul.
22 Nit yégul lu moy mititu boppam
te bakkanu boppam lay tiisoo.