3
Tuub jot na
1 Mu ne: «Su waay fasee jabaram,
mu dem doon jabaru keneen,
Su waa ja jëlaatee ndaw sa ëllëg,
ndax loolu du sobeel a sobeel réew mii?
Moona yeen gànctu ngeen aki far yu bare,
ana nu ngeen mana délsee fi man?»
Kàddug Aji Sax jee.
2 «Téenleen, séentu tund ya ne faraas!
Ana fu ñu leen fi tëddewul?
Ci yoon yi ngeen di yeeroo
ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi.
Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon.
3 Moo tax waame aje,
taw yiy mujje dikkul.
Teewul ngeen dëgër bët nib gànc,
ñàkk gàcce!
4 Léegi ngeen di ma woo wall naa:
“Baay, yaay sama xejj ca ba may ndaw.
5 Xanaa deesul mer ba fàww?
Xanaa xadar du sax?”
Ma ne: “Israayiloo, yeena ko wax,
waaye bon ngeen seen kemtalaay.”»
Israayil woyof kumba, Yuda toogadi
6 Aji Sax ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israayil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu.
7 Ma noon su defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci.
8 Gis naa ne it Israayil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu.
9 Ni gànctu yombe Israayil tax na réew mi sobewu. Njaaloo naak yàllay doj, njaalook yàllay bant.
10 Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israayil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee.
11 Aji Sax ji nag ne ma: «Li Israayil di woyof kumba lépp sax moo tane Yuda workat bi.
12 Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne:
“Israayiloo, Woyof-Kumba, délsil.”
Kàddug Aji Sax jee.
“Duma la fasal kanam.
Man Boroom ngor laa,
te duma jàpp mer ba fàww.”
Kàddug Aji Sax jee.
13 “Nangul ne ñaaw nga rekk,
te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ,
di wër di fowe sa bopp ak yàllay doxandéem yi
ci ker garaboo garab gu naat,
te dégluwoo ma.”»
Kàddug Aji Sax jee.
14 «Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maay seen boroom kër,
maay jële kenn ci bii dëkk,
ñaar ca bee gox,
boole indi Siyoŋ,
15 tànnal leen sàmm yu ma doy,
ñu sàmme leen xam-xam ak xareñ.
16 Janti keroog bu ngeen baree ba giir ci réew mi,
deesul waxe gaalu kóllërey Aji Sax ji;
xel dootu ci dem,
deesu ko fàttaliku sax,
te deesu ko namm,
deesu ko sàkkati sax.»
Kàddug Aji Sax jee.
17 «Janti keroog
Yerusalem, ngànguney Aji Sax ji lees koy woowe,
xeetoo xeet di fi daje,
ngir Aji Sax ji turam ñeel Yerusalem,
te dootuñu të ticc ci seen mébét yu bon.
18 Janti keroog waa kër Yuda
ànd ak waa kër Israayil,
bawoondoo réewum bëj-gànnaar,
wuti réew ma ma séddoon seeni maam.
19 «Maa leen naroona teral ni doom yu góor,
may leen suuf su xemmemlu,
ngeen gënle xeet yépp suuf.
Ma noon dingeen ma woowe baay
te dungeen ma dëddu mukk.
20 Teewul, yeen waa kër Israayiloo, ngeen wor ma,
ni as ndaw di wore faram.»
Kàddug Aji Sax jee.
21 «Coow dégtu na ca kaw tund ya ne faraas,
bànni Israayil ay jooy aka tinu.
Ñoo lajj seenu yoon,
fàtte seen Yàlla Aji Sax ji.
22 Yeen doom yu woyof kumba yi,
waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.»
Kàdduy tuub jib na
Nu ngi nii fekksi la,
yaw kay yaay sunu Yàlla Aji Sax ji.
23 Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya
ak coowal kaw tund yu mag ya.
Muccu Israayil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji.
24 Ba nuy gone ba tey,
tuur mu ruslu maa ngi neenal ñaqu maam yi,
seen jur gu gudd ak gu gàtt,
ba ci seeni doom, góor ak jigéen.
25 Nan gapparoo sunu gàcce,
sàngoo sunu toroxte.
Nook sunuy maam déy,
ba nuy gone ba tey jii,
nu ngi tooñ sunu Yàlla Aji Sax ji,
te déggalunu sunu Yàlla Aji Sax ji.