7
Yeremi yedd na demkati kër Yàlla yi
Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji. Mu ne ko: «Taxawil fa bunti kër Aji Sax ji, nga yéene fa kàddu gii, ne leen: “Mboolem yeen waa Yuda ñiy jàlle bunt yii, di jaamusi Aji Sax ji, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israayil dafa wax ne: Jekkalleen seeni jikkook seeni jëf, ma dëël leen bii béreb. Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’ Su ngeen jekkalee jekkal seeni jikko ak seeni jëf déy, di def a def yoon seen digg ak seen moroom, te nootuleen doxandéem, ab jirim akub jëtun, tuuruleen deretu jàmburu Yàlla, fi bii béreb, toppuleen yeneen yàlla bay loru, su boobaa, ma dëël leen bii béreb, réew mi ma joxoon seeni maam, bu yàgg, ba fàww. Yeena ngii di naxe seen bopp waxi caaxaan yu amul njariñ. Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di njaaloo, di giñi fen, di taalal Baal tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul, 10 tey dikk taxaw fi sama kanam, biir kër gii ñu ma tudde, te naan: ‘Nun kay raw nanu,’ ba tax ngeen di def mboolem lu siblu lii? 11 Rawtub sàcc daal ngeen def kër gii ñu ma tudde? Man de lii laa gis! Kàddug Aji Sax jee.
12 «“Demleen rekk kay ca sama béreb ba ca Silo, fa ma njëkkoona dëël sama tur, ngeen xool na ma ko def ngir mbonug Israayil, sama ñoñ*.
13 «“Gannaaw def ngeen jëf jii jépp nag,” kàddug Aji Sax jee, “te ma waxoon leen a wax ay yooni yoon, dégluwuleen; woo leen, wuyuwuleen, 14 kër gii ñu ma tudde, ngeen yaakaar ko, béreb bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, na ma def Silo laa koy def. 15 Dama leen di dàq, ngeen sore ma, na ma dàqe woon seen bokk yépp, askanu Efrayim gépp.”
Yàlla gàntal na
16 «Waaye yaw bul ñaanal askan wii, bu leen yékkatil kàddug ñaan, bu leen tinul fi man. Du maa lay déglu moos!
17 «Xanaa gisoo li ñu nekke fi dëkki Yuda ak ci mbeddi Yerusalem? 18 Doom a ngi taxan, baay di taal, jigéen di noot lu mu nàkkal tuur mi ñuy woowe Lingeeru asamaan, di tuural yeneen yàlla, di ma ko naqarale! 19 Du man lañuy naqaral moos!» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Xanaa kay ñoo ciy rus!»
20 Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii béreb, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.»
21 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israayil dafa ne: «Seen juru saraxu rendi-dóomal yooyee, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te dërëx. 22 Bés ba may génne seeni maam Misra déy, waxuma leen woon mbaa di leen sant mbirum saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax. 23 Mbir mii déy laa leen santoon ne leen: “Déggalleen ma, ma doon seen Yàlla; yeen ngeen doon sama ñoñ. Doxeleen wépp yoon wu ma leen sant, su ko defee ngeen baaxle.” 24 Waaye déggluwuñu ma, teewluwuñu ma, xanaa di jëfe seen xel ak seen dëgër bopp ak seen bon xol, ba tax ñu dellu gannaaw, jëmuñu kanam. 25 La dale bés ba seeni maam génne réewum Misra ba bésub tey jii, yónnee naa leen bés bu nekk mboolem sama jaam ñi, maanaam yonent yi. 26 Waaye dégluwuñu ma, teewluwuñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.
27 «Dinga leen wax kàddu yii yépp, te duñu la déglu, nga woo leen, duñu la wuyu. 28 Su ko defee nga ne leen: “Xeet a ngii wu dul déglu kàddug Yàllaam Aji Sax ji, nanguwuñu yar, worma tumurànkeel leen, ba daggook seen làmmiñ.
Xuru Ben Inom di xuru dee
29 «“Waa Yerusalemee,
seen njañ§ li ngeen séddoo Yàlla,
xuufleen ko, sànni, ñaawloo ko,
xaaculeen fa kaw tund ya ne faraas,
nde Aji Sax ji xalab na,
wacc na seen maas gii sabab sànjam.”
30 Waa Yuda déy, ñoo def lu ma ñaawlu.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñoo yeb yëf yu siblu fi biir kër gi ñu ma tudde, di ko sobeel. 31 Ñoo tabax ay bérebi jaamookaay ca béreb bu tudd Tofet fa xuru Ben Inom, di fa sarxe seeni doom, góor ak jigéen, lakk leen, te santaanewuma ko, jaarul sax ci sama xel. 32 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul tudd Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay. Dees na rob ca Tofet ndax ñàkk bérebu robukaay. 33 Néewi xeet wii mujj di lekku njanaaw ak rabu àll, te kenn du leen mana dàq. 34 Maay dakkal fi dëkki Yuda, dakkal fi mbeddi Yerusalem coowal mbégteek bànneex, dakkal kàddug boroom séet, dakkal kàddug séet, ndax réew mu tumurànke.
* 7:12 Seetal ci 1.Samiyel saar 4. 7:15 Efrayim, genn la ci fukki giiri bànni Israayil ya séq réewum Israayil, ca bëj-gànnaaru réewum Yuda. 7:21 Ci yoon, saraxu rendi-dóomal, deesu ci lekk dara. Yàllaa ngi leen di ñaawal fii, di leen won ne gedd na seen bépp sarax. § 7:29 njañ: seetal ci Màndiŋ ma 6.1-8.