Taalifi cant
yu Daawuda ak ñeneen, ngir màggal Yàlla
Téere bii moo ëmb juróomi téere, di téeméeri taalif ak juróom fukk (150) – ay cant ak ay ñaan ak ay kàdduy jooytu.
Taalif bu njëkk bi ak ñaareel bi ñooy ubbite gi, ci lañuy xamle yax yii: kan moo bon ak kan mooy aji jub, ak kan mooy buur bi Yàlla tabb, fal ko, te muy jiitee njub. Buur Daawuda ak Buur Suleymaan bokk nañu ci ñi fent taalifi cant yi, waaye ci taalifi cant 99 ak 145, gis nanu ne Aji Sax jeey Buur, te moom rekk a yellooy cant. Taalif yi mujj (146—150) ñooy màggal Aji Sax ji.
Ci tënk: Téere bu ci nekk, nii lañu ko tëje: «Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji,» mbaa «Màggalleen Ki Sax.»
Taalif 1—41 Téere bi njëkk.
Taalif 42—72 Ñaareelu téere bi.
Taalif 73—89 Ñetteelu téere bi.
Taalif 90—106 Ñeenteelu téere bi.
Taalif 107—150 Juróomeelu téere bi.
1
Ñaari yoon a ngii
Ndokkalee yaw mi toppul tànki ku bon,
taxawewuloo yoonu moykat,
toogewuloo jataayu ñaawlekat.
Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji,
di ko jàngat guddeek bëccëg.
Loo def mu àntu:
nga mel ni garab gu saxe walum ndox,
bu jotee meññ,
te xob wa du lax.
 
Loolu dalul moos ku bon
kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.
Moo tax ku bon du siggee àtte ba,
moykat du taxawe ndajem aji jub ña.
 
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub;
yoonu ku bon di sànk boroom.