111
Yàlla la ay mbiram sax
Màggalleen Ki Sax!
Naa sante Aji Sax ji léppi xol
ci biir ñu jub ñi bokk jataay.
Liggéeyi Aji Sax ji réy na,
ku ko safoo di ko gëstu.
Jëfam di teddngaak* daraja,
njubteem di sax ba fàww.
Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam;
Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.
Mooy leel ku ko ragal,
di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.
Won na ñoñam dooley jëfam,
ba mu leen joxee suufu xeet yi.
Ay jëfam dëgg laak yoon,
tegtalam yépp mata wóolu,
laloo dëgg ak njub,
te sax dàkk ba fàww.
Moo yónnee xeetam wall,
fas ak ñoom kóllëre gu sax.
Kee sell te jara ragal!
10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel,
dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye.
Moo yeyoo cant ba fàww.
* 111:3 teddnga mooy teraanga ju bare lool.